2 Noonu Yeesu daldi leen jàngal lu bare ciy léeb. Ci njàngleem nag mu ne leen: 3 «Dégluleen, dafa amoon beykat bu demoon jiyi. 4 Bi muy saaw toolam nag, lenn ci pepp mi wadd ci kaw yoon wi, picc yi daldi ñëw, lekk ko lépp. 5 Leneen ci pepp mi wadd ci bérab bu bare ay doj te néew suuf, mu daldi sax bu gaaw, ndaxte suuf si barewul. 6 Waaye bi jant bi naajee, mu lakk, wow, ndaxte amul ay reen. 7 Leneen nag wadd ci biir ay xaaxaam, xaaxaam yi daldi sax, tanc ko, te meññul dara. 8 Li ci des dal ci suuf su baax, mu jóg, sax, di focci ay gub; lii àntu, ba mat fanweeri yoon lu ëpp la mu ji woon, lii mat juróom benn fukk, lii mat téeméer.»
9 Noonu Yeesu ne leen: «Déglul bu baax, yaw mi am ay nopp.»
10 Gannaaw loolu ba Yeesu nekkee fu wéet, fukki taalibe ak ñaar ña, ak ñeneen ñu daan ànd ak ñoom, laaj ko ci mbirum léeb yi. 11 Mu ne leen: «Yéen may nañu leen, ngeen xam mbóoti nguuru Yàlla, waaye ñi ci biti léeb ay ëmb lépp. 12 Noonu la, ngir:
13 Noonu Yeesu ne leen: «Ndax xamuleen léeb wii? Nu ngeen xame nag léeb yi ci des? 14 Ki ji nag, kàddu gi lay ji. 15 Ki féete ci yoon wi mooy ki dégg, Seytaane ñëw ci saa si, këf kàddu, gi ñu def ci moom. 16 Ki jot kàddu gi ci bérab bu bare ay doj mooy ki dégg kàddu gi, nangu ko ak mbég ci saa si, 17 waaye du yàgg, ndaxte wax ji saxul ci moom. Bu jaaree ci nattu nag, mbaa ñu fitnaal ko ndax kàddu gi, mu dàggeeku ci saa si. 18 Ki jot jiwu wi ci xaaxaam yi mooy ki dégg kàddu gi, 19 waaye soxlay àddina ak naxi alal ak bëgge solu ko, tanc kàddu gi, ba du meññ dara. 20 Ki jot kàddu gi ci suuf su baax si nag, mooy ki ko dégg te nangu ko, ba jariñ; kii mat fanweeri yoon lu ëpp la ñu ji woon, kii mat juróom benn fukk, kii mat téeméer.»
24 Mu ne leen: «Seetleen bu baax li ngeen di dégg. Dees na leen nattal ak natt, bi ngeen di nattale, te dollil leen. 25 Ku am, dees na la dollil; ku amul, li nga am as néew, dees na ko nangu.»
33 Noonu Yeesu dégtal leen yeneen léeb yu bare yu mel ni yii, di leen xamal kàddu gi, aju ci lu ñu àttan. 34 Daawu leen wax dara lu dul ciy léeb. Waaye bu wéetee ak ay taalibe, daan na leen firil lépp.