2 Noonu Pilaat laaj ko: «Ndax yaa di buuru Yawut yi?» Yeesu ne ko: «Wax nga ko.» 3 Te sarxalkat yu mag yi di ko jiiñ lu bare. 4 Kon nag Pilaat laajaat ko: «Déggal lépp li ñu lay jiiñ. Xanaa amoo ci tont?» 5 Waaye ba tey Yeesu waxul dara, ba tax Pilaat waaru.
6 Màggal gu nekk nag Pilaat daan na may mbooloo mi, ñu tànn kenn ci ñi ñu tëjoon, mu bàyyil leen ko. 7 Fekk booba amoon na ku ñu tëj, tudd Barabas, ku bokk ci ña bëggoona tas réew mi, boole ci rey nit. 8 Noonu mbooloo mi ñëw, laaj Pilaat, mu defal leen la mu daan def. 9-10 Pilaat nag xam ne kiñaan rekk a taxoon sarxalkat yu mag yi jébbal ko Yeesu. Kon mu ne mbooloo mi: «Xanaa ma bàyyil leen buuru Yawut yi?» 11 Waaye sarxalkat yu mag yi xiir mbooloo mi, ñu laaj Pilaat, mu bàyyil leen Barabas.
12 Kon Pilaat ne leen: «Lan laay def nag ak ki ngeen di wooye buuru Yawut yi?» 13 Ñu daldi yuuxuwaat naan: «Daaj ko ci bant, ba mu dee!» 14 Pilaat ne leen: «Lu tax? Gan tooñ la def?» Waaye mbooloo mi di yuuxu bu gëna kawe: «Daaj ko ci bant!» 15 Noonu Pilaat, mi wuta neex mbooloo mi, bàyyil leen Barabas, ba noppi mu dóorlu Yeesu ay yar, jébbal ko, ngir ñu daaj ko ci bant.
24 Foofa ñu daaj Yeesu ci bant, daldi séddoo ay yéreem, tegoo ko ay bant, ba xam ku nekk, looy am; 25 booba fekk yoor-yoor di jot. 26 Mbind mi xamle lu tax ñu rey ko nee na: «Kii mooy buuru Yawut yi.» 27-28 Booba it ñu daajaale ak moom ñaari taskati réew mi, kenn ci ndijooram, ki ci des ci càmmoñam.
29 Ña fa doon romb di ko xas, di wëcc seen bopp ndax sib ko, naan: «Waaw kay, yaw mi bëgga toj kër Yàlla gi, tabaxaat ko ci ñetti fan, 30 wàccal ci bant bi te musal sa bopp!» 31 Noonu it sarxalkat yu mag yi ak xutbakat yi di ko ñaawal ci seen biir naan: «Kii musal na ñeneen waaye manula musal boppam. 32 Almasi bii, di buuru Israyil, na wàcc léegi ci bant bi, nu gis ko te gëm.» Ñi ñu daajaale ak moom it di ko xarab.
38 Bi mu ko defee ridob bérab bu sell ba ca kër Yàlla ga xar ñaar, li dale ci kaw ba ci suuf. 39 Njiitu xare nag, bi taxawoon ci kanam Yeesu, bi mu gisee ni Yeesu deeye, mu ne: «Ci dëgg, nit kii Doomu Yàlla la!»
40 Amoon na fa nag ay jigéen, ñu leen dànd, di xool. Xàmmi nañu ci: Maryaama mi dëkk Magdala, Maryaama yaayu Saag mu ndaw ak Yuusufa, ak Salome. 41 Bi Yeesu nekkee Galile, jigéen ñooñu ñoo ko doon topp, di ko topptoo. Amoon na fa it yeneen jigéen yu bare yu àndoon ak moom, ba ñëw Yerusalem.
46 Noonu Yuusufa jënd càngaay, wàcce néew bi, laxas ko ci, dugal ko cib bàmmeel bu ñu yett ci xeer. Bi mu ko defee mu béraŋ aw doj, ube ko buntu bàmmeel bi. 47 Maryaamam Magdala nag ak Maryaama yaayu Yuusufa xool fu mu ko denc.
<- MÀRK 14MÀRK 16 ->