2 Noonu ay Farisen ñëw ci moom, lalal ko fiir, ñu laaj ko: «Ndax jaadu na, nit fase soxnaam?» 3 Yeesu ne leen: «Lu leen yoonu Musaa sant?» 4 Ñu ne ko: «Musaa maye na, nit bind kayitu pase, tàggook soxnaam.» 5 Waaye Yeesu ne leen: «Dénkaane boobu mu leen bindal, bind na ko ndax seen xol dafa fatt. 6 Waaye ca njàlbéen ga “Yàlla sàkk na leen, kii góor, kii jigéen. 7 Looloo tax góor di teqalikook ndeyam ak baayam, ànd ak soxnaam, 8 ñoom ñaar doon benn.” Kon nekkatuñu ñaar waaye benn lañu. 9 Lu Yàlla takk nag, bu ko nit tas.»
10 Bi ñu delloo ca kër ga nag, taalibe ya laaj ko ci mbirum loolu. 11 Noonu Yeesu ne leen: «Ku fase sa soxna, takk jeneen, njaaloo nga, di tooñ ku jëkk ka. 12 Te jigéen ji tas, séyaat ak keneen, njaaloo nga.»
21 Noonu Yeesu xool ko, am cofeel ci moom, mu ne ko: «Lenn rekk moo la dese. Demal jaay li nga am, jox ko miskin yi, te dinga woomle ci asamaan; boo noppee, nga ñëw topp ci man.» 22 Waaye ci wax jooju xar kanamam lëndëm, mu jóge fa ak tiis, ndaxte ku bare woon alal la.
23 Noonu Yeesu xool taalibe yi ko wër ne leen: «Boroom alal dugg ci nguuru Yàlla, lu jafee ngoogu!» 24 Wax jooju nag daldi jaaxal taalibe yi lool. Waaye Yeesu neeti leen: «Samay xarit, dugg ci nguuru Yàlla, lu jafee ngoogu! 25 Giléem jaar ci bën-bënu puso moo gëna yomb boroom alal dugg ci nguuru Yàlla.» 26 Wax jooju gënatee jaaxal taalibe ya, ñu naan ci seen biir: «Kon nag ku mana mucc?» 27 Noonu Yeesu xool leen naan: «Loolu të na nit, waaye tëwul Yàlla; Yàlla man na lépp.»
28 Ci kaw loolu Piyeer daldi ko ne: «Nun de dëddu nanu lépp te topp la!» 29 Yeesu ne ko: «Ci dëgg maa ngi leen koy wax, képp ku dëddu kër, doomu ndey yu góor walla yu jigéen, ndey walla baay, doom walla suuf ndax man ak xibaaru jàmm bi, 30 dinga am tey jii téeméeri yoon ay kër, doomi ndey yu góor ak yu jigéen, ndey, doom ak suuf, ñoom ak ay fitnay noon, te ëllëg nga am dund gu dul jeex. 31 Waaye ñu bare ci ñi jiitu ñooy mujji; ñi mujj ñooy jiituji.»
41 Bi nga xamee ne fukki taalibe ya ca des dégg nañu loolu, ñu daldi mere Saag ak Yowaana. 42 Waaye Yeesu woo leen naan: «Xam ngeen ne ci xeeti àddina, ñi ñu teg njiit dañu leen di dóor yetu nguur, te kilifa yi di leen not. 43 Buleen mel ni ñooñu. Waaye ku bëgga nekk kilifa ci yéen, na nekk seen surga, 44 te ku bëgga nekk njiit, na nekk seen jaam. 45 Ndaxte noonu la Doomu nit ki ñëwe sax, du ngir ñu nekk ay surgaam, waaye ngir muy seen surga, ba joxe bakkanam ngir njotug ñu bare.»
49 Noonu Yeesu taxaw, daldi ne: «Wooleen ko!» Ñu woo nag gumba gi ne ko: «Na sa xel dal! Jógal! Mu ngi lay woo.» 50 Bi mu ko déggee, mu sànni malaanam, ne bërét, dem ci Yeesu. 51 Yeesu ne ko: «Loo bëggoon ma defal la ko?» Gumba gi ne ko: «Kilifa gi, damaa bëgga gis.» 52 Noonu Yeesu ne ko: «Demal ci jàmm. Sa ngëm faj na la.» Ci saa si gumba gi gis, daldi topp Yeesu ci yoon wi.
<- MÀRK 9MÀRK 11 ->