3 Booba nag sarxalkat yu mag ya ak njiiti xeet wa dajaloo ca kër gu réy gu sarxalkat bu mag ba, tudd Kayif. 4 Ñu daldi gise, ba xam lu ñu mana fexe, ba jàpp Yeesu, reylu ko. 5 Waaye ñu ne: «Bumu doon ci bésu màggal bi, ngir yëngu-yëngu baña am ci nit ñi.»
10 Yeesu nag xam la ñu wax, mu ne leen: «Jigéen ji defal na ma jëf ju rafet; lu tax ngeen di ko sonal? 11 Miskin yaa ngi ak yéen bés bu nekk, waaye dungeen ma gis ba fàww. 12 Kii, ci li mu tuur latkoloñ jii ci sama yaram, def na ko ngir waajal sama rob. 13 Ci dëgg maa ngi leen koy wax, fépp fu ñuy yéene xibaaru jàmm bi ci àddina sépp, dinañu fa fàttali it li jigéen jii def.»
20 Bi nga xamee ne timis jot na, Yeesu toog di lekk, moom ak fukki taalibe yi ak ñaar. 21 Bi ñuy lekk, mu ne leen: «Ci dëgg maa ngi leen koy wax, kenn ci yéen dina ma wor.» 22 Taalibe ya am naqaru xol bu réy; ku nekk daldi ne ko: «Mbaa du man, Boroom bi?» 23 Yeesu ne leen: «Ki dugal loxoom ak man ci ndab li, kooku moo may wor. 24 Doomu nit ki mu ngi dem, ni ñu ko waxe ci Mbind mi, waaye ki koy wor dina torox; bañoona juddu moo gënoon ci moom.» 25 Yudaa, mi ko nara wor, laaj ko: «Mbaa du man, kilifa gi?» Yeesu ne ko: «Wax nga ko.»
26 Noonu bi ñuy lekk, Yeesu jël mburu, sant Yàlla, damm ko, jox ko taalibe ya. Mu ne leen: «Jël-leen lekk, lii sama yaram la.» 27 Gannaaw loolu mu jël kaas, sant Yàlla, jox leen ko. Mu ne leen: «Yéen ñépp naanleen ci, 28 ndaxte lii mooy sama deret, ji fas kóllëre gi, te mu tuuru, ngir ñu bare jot mbaalug bàkkaar yi. 29 Maa ngi leen di wax, dootuma naan gannaaw-si-tey ndoxum reseñ mii, ba kera may naan ak yéen ndoxum reseñ mu bees ci sama nguuru Baay.»
30 Gannaaw loolu ñu woy Yàlla, ba noppi génn, dem ca tundu Oliw ya.
31 Booba Yeesu ne leen: «Yéen ñépp dingeen ma dàggeeku ci guddi gii, ndaxte bind nañu:
40 Noonu mu ñëw ca taalibe ya, fekk leen ñuy nelaw. Mu ne Piyeer: «Amuleen sax dooley xoolandoo ak man benn waxtu? 41 Xool-leen te ñaan, ngir baña daanu cig fiir. Seen xol jag na, waaye seen bind a woyof.» 42 Yeesu delluwaat di ñaan ne: «Sama Baay, bu fekkee ne kaasu naqar bii manu maa teggi te naanuma ko, kon na sa coobare am.» 43 Yeesu ñëwaat ca taalibe ya, fekk leen ñuy nelaw, ndaxte seeni bët dañoo diis. 44 Mu daldi leen bàyyi, waxaat loolu ñetteel bi yoon.
45 Noonu mu ñëw ca taalibe ya ne leen: «Nelawleen léegi te noppalu. Waxtu wu ñu ma wara jébbale ci loxoy bàkkaarkat yi, jege na. 46 Jógleen nu dem; xool-leen, ki may wor a ngi nii, di ñëw.»
51 Ca saa sa kenn ci ñi ànd ak Yeesu bocci jaaseem, dóor surgab sarxalkat bu mag ba, nopp ba dagg. 52 Waaye Yeesu ne ko: «Roofal sa jaasi ci mbaram, ndaxte ku bocci jaasi, jaasi moo lay rey. 53 Xanaa xamuloo ne man naa laaj sama Baay, te dina ma may ci taxawaay bi mbooloom malaaka mu xel dajul*Maanaam fukki mbooloo ak ñaar yu malaaka; mbooloo mu nekk def juróom benni junni.? 54 Waaye su ma ko defoon, nan la Mbind mi mana ame? Ndaxte Mbind mi nee na, nii la wara ame.»
55 Booba Yeesu ne mbooloo mi: «Jóg ngeen ngir jàpp ma, gànnaayoo jaasi ak yet, mel ni ñuy topp sàcc. Moona daa naa toog bés bu nekk ca kër Yàlla ga, di jàngle, te jàppuleen ma. 56 Waaye lii lépp xew na, ngir amal Mbindi yonent yi.» Ci kaw loolu taalibe yépp dëddu ko, daw.
59 Noonu sarxalkat yu mag ya ak kureelu àttekat ya di seet naaféq bu mana seede ci Yeesu, ba ñu man koo rey, 60 waaye manuñu koo am. Teewul ñu bare ñëwoon nañu, di seede lu dul dëgg. Ba mujj ñaari nit ñëw naan: 61 «Kii nee woon na: “Man naa toj kër Yàlla ga, tabaxaat ko ci ñetti fan.”»
62 Ci kaw loolu sarxalkat bu mag ba jóg ne ko: «Ndax doo wax dara? Loo xam ci li ñii seede ci yaw?» 63 Waaye Yeesu ne cell. Sarxalkat bu mag ba ne ko: «Giñloo naa la ci Yàlla miy dund, nga wax nu, ndax yaa di Almasi bi, Doomu Yàlla ji.» 64 Yeesu ne ko: «Wax nga ko. Maa ngi leen koy wax it, li dale fii dingeen gis Doomu nit ki toog ci ndijooru Aji Man ji, di ñëw ci niiri asamaan si.» 65 Bi mu déggee loolu, sarxalkat bu mag ba daldi mer lool, ba xotti ay yéreem, daldi ne: «Weddi na Yàlla, lu nu doyeeti seede? Dégg ngeen ni mu weddee. 66 Lu ngeen ci xalaat?» Ñu ne ko: «Yoon teg na ko dee.»
67 Ci kaw loolu ñu daldi tifli ci xar kanamam, dóor ko ay kurfeñ. Ñeneen talaata ko, 68 ne ko: «Yaw Kirist, yonent bi, ndax xam nga ku la dóor?»
73 Nees-tuut ña fa taxawoon ñëw ci Piyeer ne ko: «Ci lu wóor ne yaw itam bokk nga ci ñoom, ndaxte sa waxin feeñal na la.» 74 Bi mu ko déggee, Piyeer daldi giñ ak di waat ne: «Xawma nit kooku.» Te ci taxawaay ginaar daldi sab. 75 Noonu Piyeer fàttaliku la Yeesu waxoon ne: «Bala ginaar a sab, dinga ma weddi ñetti yoon.» Mu daldi génn, di jooy jooy yu metti.
<- MACË 25MACË 27 ->- a Maanaam fukki mbooloo ak ñaar yu malaaka; mbooloo mu nekk def juróom benni junni.