1 Ba Yeesu joxee fukki taalibeem ya ak ñaar ndigal yooyu, mu jóge fa, ngir dem jàngleji ak a waare ci seeni dëkk.
Yaxya yónnee na, di laaj Yeesu
2 Gannaaw loolu Yaxya dégg ca kaso ba jëfi Almasi bi. Mu yónni ci moom nag ay taalibeem, 3 ne ko: «Ndax yaa di Ki wara ñëw, walla danoo wara xaar keneen?»
4 Yeesu ne leen: «Demleen nettali Yaxya li ngeen dégg te gis ko. 5 Gumba yaa ngi gis, lafañ yiy dox, gaana yi wér, tëx yiy dégg, ñi dee di dekki, te néew doole ñaa ngi dégg xibaaru jàmm bi. 6 Yaw mi sa ngëm yolomul ndax man, barkeel nga.»
7 Bi nga xamee ne taalibe ya Yaxya yónni woon ci Yeesu dem nañu, Yeesu daldi wax ak mbooloo ma ci mbirum Yaxya ne leen: «Lu ngeen seeti woon ca màndiŋ ma? Xanaa barax buy jaayu ci ngelaw li? 8 Kon lu ngeen seeti woon nag? Nit ku sol yére yu rafet? Waaye ñi sol yére yu rafet ñu ngi dëkk ci këri buur. 9 Lu tax ngeen génn nag? Ngir gis ab yonent? Waaw, wax naa leen ne ëpp na yonent. 10 Yaxya male moo di ki ñu waxoon ci Mbind mi naan:
“Maa ngi yónni sama ndaw, mu jiitu la,
te xàllal la yoon ci sa kanam.”
11 Ci dëgg maa ngi leen koy wax, ci li jigéen jur, ku sut Yaxya masula feeñ. Waaye ba tey ki gëna ndaw ci nguuru Yàlla Aji Kawe ji moo ko sut. 12 Ci li dale ci jamonoy Yaxya ba léegi, nit ñaa ngi góor-góorlu ngir dugg ci nguuru Yàlla, te ñi sawar ñoo ci am wàll. 13 Ndaxte li yonent yi wax ak li yoonu Musaa tëral ñu ngi doon dox, ba kera Yaxya di feeñ. 14 Te Yaxya moomu, su ngeen bëggee nangu lii, mooy Ilyaas bi waroona ñëw. 15 Déglul bu baax, yaw mi am ay nopp.
16 «Niti jamono jii nag, lan laa leen mana méngaleel? Ñu ngi nirook xale yu toog ca pénc ma, di woo seeni xarit, 17 ne leen:
“Liital nanu leen ak toxoro, te fecculeen,
woyal nanu leen woyi dëj, te jooyuleen.”
18 Ndaxte Yaxya feeñ na, lekkul, naanul, ngeen daldi ne: “Dafa ànd ak rab.” 19 Gannaaw gi nag, Doomu nit ki ñëw na, lekk, naan, ngeen daldi ne: “Kii daal bëgg na lekk, di naan biiñ, tey xaritoo ak ay juutikat ak ay boroom bàkkaar.” Waaye li xam-xamu Yàlla di jur, mooy firndeel ne dëgg la.»
Yeesu gëdd na ay dëkk
20 Gannaaw loolu Yeesu daldi gëdd dëkk, ya mu defe woon la ëpp cay kéemaanam, ndaxte tuubuñu seeni bàkkaar. 21 Mu ne: «Dingeen torox, yéen waa Korasin ak waa Betsayda, ndaxte kéemaan yi ma def ci yéen, bu ñu leen defoon ci dëkku Tir walla ci dëkku Sidon, kon réccu nañu bu yàgg, xëppoo dóom, sol saaku. 22 Waaye maa ngi leen koy wax, keroog bés pénc ma Tir ak Sidon ñoo leen di tane. 23 Te yaw dëkku Kapernawum, ndax dees na la yékkati bu kawe? Déedéet, dees na la daane bu suufe. Ndaxte kéemaan yi ma def ci yaw, bu ñu leen defoon ci dëkku Sodom, kon mu nekk ba tey. 24 Waaye maa ngi leen koy wax, keroog bés pénc ma Sodom moo lay tane.»
Woote bu mag bi
25 Ca jamono joojale Yeesu wax na lii: «Yaw Baay, Boroom asamaan ak suuf, maa ngi lay sant ci li nga nëbb yëf yii ñi am xam-xam ak ñi am xel, te xamal leen gone yi. 26 Waaw, Baay, ndaxte looloo la neex.» 27 Yeesu teg ca ne: «Sama Baay jébbal na ma lépp, te kenn manu maa xam, man Doom ji, ku dul Baay bi; kenn it manula xam Baay bi, ku dul man Doom ji, ak ku ma ko bëgga xamal.
28 «Ñëwleen ci man, yéen ñépp ñi sonn te diis, dinaa leen may noflaay. 29 Jébbaluleen ci man te jàng ci man, ndaxte lewet naa te woyof, te dingeen am noflaay ci seen xol. 30 Ndaxte sama kilifteef lewet na te sama yen diisul.»