6 Sase daldi gaawantu wàcc, ganale ko ak mbég. 7 Ñépp gis loolu, di ñurum-ñurumi naan: «Mi ngi dal cig këru boroom bàkkaar.» 8 Waaye Sase taxaw ne Boroom bi: «Déglul Boroom bi, dogu naa may sama genn-wàllu alal miskin yi, te lu ma masa njublaŋ nit, jël alalam, dinaa ko fey ñeenti yoon lu ni tollu.» 9 Yeesu ne ko: «Mucc gi wàcc na tey ci kër gii, ndaxte nit kii, ci askanu Ibraayma la bokk itam. 10 Ndaxte Doomu nit ki ñëw na, ngir seet te musal ñi réer.»
15 «Bi ñu ko falee buur nag, ba mu délsi, mu woolu surga, ya mu joxoon wurus wa, ngir xam nan lañu ci liggéeye. 16 Ku jëkk ka ñëw ne ko: “Sang bi, sa libidoor bii jur na fukki libidoor.” 17 Buur ba ne ko: “Def nga lu baax, surga bu baax nga. Segam wone nga ne takku nga ci lu tuuti, falul ci fukki dëkk.” 18 Surga ba ca topp ñëw ne: “Sang bi, sa libidoor ba indi na juróomi libidoor.” 19 Buur ba ne ko: “Yaw, falul ci juróomi dëkk.” 20 Keneen ñëw ne: “Sang bi, sa libidoor baa ngi nii. Dama koo fasoon ci sekkit, denc ko. 21 Dama laa ragaloon, ndaxte ku néeg nga. Dangay nangu loo dénkaanewul, di dajale loo jiwul.” 22 Buur ba ne ko: “Ci say wax laa lay àtte, surga bu bon bi! Xamoon nga ne, nit ku néeg laa, di nangu lu ma dénkaanewul, te dajale lu ma jiwul. 23 Lu tax nag yóbbuwoo sama xaalis ca denckati xaalis ya? Bés bu ma ñëwee nag, ma mana jot sama xaalis ak la mu jur.”
24 «Ci kaw loolu mu ne ña taxawoon ca wetam: “Nanguleen libidoor bi ci moom, jox ko boroom fukki libidoor yi.” 25 Ñu ne ko: “Sang bi, am na fukki libidoor ba noppi.” 26 Buur ba ne leen: “Maa ngi leen koy wax, ku am, dinañu la dolli, waaye ku amul, li nga am as néew sax, dinañu ko nangu. 27 Waaye sama noon yi, ñi bëggul woon ma doon seen buur, indileen fii, rey leen ci sama kanam.”»
32 Ñaari ndaw ya dem, fekk mbir ya deme, na leen ko Yeesu waxe woon. 33 Bi ñuy yiwi cumbur ga nag, ay boroomam ne leen: «Lu tax ngeen di yiwi cumbur gi?» 34 Ñu ne: «Ndaxte Boroom bi da koo soxla.» 35 Noonu ñu indil cumbur gi Yeesu, daldi lal seeni yére ca kaw, yéegal ca Yeesu.
36 Bi muy dem, nit ñi di lalal Yeesu seeni yére ci yoon wi. 37 Bi ñu agsee fa mbartalum tundu Oliw ya doore, taalibeem yépp fees ak mbég, tàmbalee màggal Yàlla ca kaw ndax kéemaan yu bare yi ñu gis. 38 Ñu ngi naan:
39 Waaye ay Farisen yu nekkoon ca mbooloo ma ne Yeesu: «Kilifa gi, yeddal sa taalibe yi!» 40 Noonu mu ne: «Maa ngi leen koy wax, bu ñu noppee ñoom, doj yiy xaacu.»
41 Bi Yeesu jegee dëkk ba, ba séen ko, mu jooy ko 42 naan: «Céy yaw itam, boo xamoon bésub tey yi la mana indil jàmm! Waaye fi mu ne manuloo koo gis. 43 Bés dina ñëwi yu say noon di jal, wërale la. Dinañu la tëj ci biir, tanc la. 44 Dinañu la yàqate, yaw ak sa waa dëkk. Doj dootul des ci kaw doj ci yaw, ndaxte ràññeewoo jamono ji Yàlla ñëwe, wallusi la.»
47 Bés bu nekk Yeesu di jàngle ca kër Yàlla ga. Sarxalkat yu mag ya ak xutbakat ya, ñoom ak njiiti xeet wa, ñu ngi ko doon wuta reylu. 48 Waaye xamuñu woon lan lañu mana def, ndaxte nit ñépp a ngi ko doon déglu, bañ benn baat raw leen.
<- LUUG 18LUUG 20 ->- a Maanaam mina. Seetal Xaalis ci Leeral yi.