5 Ndaw ya wax Boroom bi ne ko: «Yokkal sunu ngëm.» 6 Boroom bi ne leen: «Su ngeen amee ngëm gu tuuti sax niw peppu fuddën, kon dingeen mana ne garab gii: “Buddeekul, dem jëmbëtu ca géej ga,” te dina def li ngeen wax.
7 «Kan ci yéen bu amoon surga bu beyi walla bu sàmmi ba ñëw, ndax dafa ko naa: “Kaay lekk”? 8 Déedéet. Xanaa kay da ko naan: “Defaral ma reer bi. Takkul te tibbal ma, ba ma lekk te naan, ba noppi nga doora lekk te naan.” 9 Li surga ba topp ndigal, ndax tax na mu yelloo ngërëm? Déedéet. 10 Noonu yéen itam bu ngeen toppee li ñu leen sant lépp ba noppi, dangeena war ne: “Ay surga rekk lanu. Sunu warugar lanu def.”»
22 Noonu mu ne taalibe ya: «Jamono dina ñëw, fu ngeen di bëgga gis su doon sax benn fan ci jamono ju Doomu nit ki di ñëw, waaye dungeen ko gis. 23 Dees na leen ne: “Mi ngi fii!” walla: “Ma nga fale!” Buleen dem, mbaa ngeen di leen topp. 24 Ndaxte ni melax naan ràyye ci asamaan, di leeral gii wet, ba ca gee, noonu it la Doomu nit ki di mel ci bésam. 25 Waaye balaa booba fàww mu sonn lool te niti jamono jii dëddu ko.
26 «La xewoon ca bési Nóoyin, dina xewaat ci bési Doomu nit ki. 27 Nit ñaa ngi doon lekk ak di naan, di jël jabar ak a séyi, ba bés ba Nóoyin duggee ca gaal ga. Noonu mbënn ma ñëw, rey leen ñoom ñépp.
28 «Dina mel it ni la xewoon ca bési Lóot. Nit ñaa ngi doon lekk ak di naan, di jënd ak di jaay, di ji ak di tabax. 29 Waaye bés ba Lóot génnee Sodom, Yàlla tawloo sawara ak tamarax, rey leen ñoom ñépp. 30 Noonu lay mel, bés bu Doomu nit kiy feeñ.
31 «Ca bés boobee ku nekk ca kaw kër ga te ay bagaasam nekk ca biir, bumu wàcc jëli leen. Te it ku nekk ca tool ya, bu mu ñibbi. 32 Fàttalikuleen soxnas Lóot! 33 Kuy wuta rawale sa bakkan, dinga ko ñàkk, waaye ku ko ñàkk, dinga dund. 34 Maa ngi leen koy wax: ca jamono jooju, ñaar dinañu bokka tëdd guddi, dees na yóbbu kenn ki, bàyyi ka ca des. 35-36 Ñaari jigéen dinañu wolandoo, dees na yóbbu kenn ci, bàyyi ka ca des.»
37 Taalibe yi ne Yeesu: «Fu loolu di xewe, Boroom bi?» Yeesu ne leen: «Fa médd nekk, la tan yiy dajee.»
<- LUUG 16LUUG 18 ->