7 «Maa ngi leen di wax lii: ci noonule, dina am mbég ci asamaan, bu benn bàkkaarkat tuubee ay bàkkaaram. Te mbég moomu mooy ëpp mbég, mi fay am, ngir juróom ñeent fukk ak juróom ñeent ñu jub, te soxlawuñoo tuub seeni bàkkaar.
20 «Mu daldi jóg, jëm kër baayam. Waaye bi muy soreendi kër ga, baayam séen ko, yërëm ko, daldi daw laxasu ko, fóon ko. 21 Doom ja ne ko: “Baay, tooñ naa Yàlla, tooñ naa la; yeyootumaa nekk sa doom.” 22 Waaye baay ba ne ay surgaam: “Gaawleen indi mbubb, mi gëna rafet, solal ko ko. Te ngeen roof ab jaaro ci loxoom te solal ko ay dàll. 23 Indileen sëllu wu duuf wa te rey ko, nu lekk te bànneexu; 24 ndaxte sama doom jii dafa dee woon te dundaat na, dafa réeroon te feeñ na.” Noonu ñu tàmbalee bànneexu.
25 «Fekk booba taaw baa nga woon ca tool ya. Bi mu ñëwee, ba jub kër ga, mu dégg ñuy tëgg, di fecc. 26 Mu daldi woo kenn ca surga ya nag, laaj ko lu xew. 27 Mu ne ko: “Sa rakk moo délsi, te sa baay rey na sëllu wu duuf wa, ndaxte ñibsi na ci jàmm.”
28 «Ci kaw loolu taaw ba daldi mer, baña dugg ca kër ga. Baayam daldi génn, ngir ñaan ko mu dugg. 29 Waaye taaw ba wax baayam ne ko: “Seetal ñaata at laa la liggéeyal, mel ni jaam, te masumaa moy sa ndigal, waaye yaw, masuloo ma may sax tef, ngir ma bànneexu, man ak samay xarit. 30 Waaye bi sa doom jii dikkee, moom mi yàq sa alal ci ndoxaan, reyal nga ko sëllu wu duuf wi.” 31 Noonu baay bi ne ko: “Sama doom, yaa ngi ak man bés bu nekk, te li ma am lépp, yaa ko moom. 32 Waaye war nanoo bànneexu te bég, ndaxte sa rakk jii dafa dee woon te dundaat na, dafa réeroon te feeñ na.”»
<- LUUG 14LUUG 16 ->