4 «Maa ngi leen koy wax, samay xarit, buleen ragal ñu mana rey yaram, ba noppi dootuñu mana def dara. 5 Dinaa leen wax nag ki ngeen wara ragal: ragal-leen ki nga xam ne bu reyee ba noppi, am sañ-sañu sànni ca sawara. Waaw, maa ngi leen koy wax, ragal-leen kooku. 6 Juróomi picci ramatu, ndax duñu ko jaay ci ñaari dërëm? Moona Yàlla fàttewul benn ci ñoom. 7 Seen kawari bopp sax waññees na leen. Kon buleen ragal dara, yéena gën ndiiraanu ramatu.
8 «Te maa ngi leen koy wax, képp ku ma nangu ci kanam nit ñi, Doomu nit ki dina la nangu ci kanam malaakay Yàlla yi. 9 Waaye ku ma gàntu ci kanam nit ñi, dinañu la gàntu ci kanam malaakay Yàlla yi. 10 Ku sosal Doomu nit ki, dinañu la baal, waaye kuy sosal Xel mu Sell mi, duñu la ko baal.
11 «Bu ñu leen yóbboo ca jàngu ya, ca kanam kilifa ya ak àttekat ya, buleen am xel ñaar ci li ngeen wara tontu ak nan ngeen wara tontoo, walla lu ngeen wara wax, 12 ndaxte Xel mu Sell mi dina leen xamal ca waxtu woowa li ngeen wara wax.»
16 Noonu mu dégtal leen wii léeb ne: «Dafa amoon waa ju bare alal, te ay toolam nangu lool, 17 muy werante ci xelam naan: “Nu ma wara def? Ndaxte amatuma fu ma dajale sama ngóob mi.” 18 Noonu mu ne: “Nii laay def: daaneel sama sàq yi, defaraat yu gëna réy, ba man cee dajale sama dugub ji ak sama am-am bépp. 19 Te dinaa kañ sama bopp ne: ‘Yaw mii, am nga alal ju bare ju mana dem ay ati at; noppalal sa yaram, di lekk, di naan, tey bég.’ ” 20 Waaye Yàlla ne ko: “Ñàkk xel! Guddig tey, dees na jël sa bakkan. Kon li nga dajale lépp, ku koy moom?”
21 «Kiy dajale alal ngir boppam nag te amul dara ca kanam Yàlla, lu mel nii moo lay dal.»
27 «Seetleen ni tóor-tóori ñax mi di saxe. Duñu liggéey, duñu ëcc, waaye maa ngi leen di wax ne Suleymaan sax ci ndamam soluwul woon ni benn ci ñoom. 28 Yéen ñi néew ngëm! Bu Yàlla woddee nii ñaxum tool yi, miy sax tey, te bu subaa ñu def ko ci taal bi, ndax du leen gëna wodd? 29 Buleen di wut lu ngeen di lekk walla lu ngeen di naan; te buleen ci jaaxle. 30 Ndaxte loolu lépp, ñi xamul Yàlla ñoo koy wut. Te seen Baay xam na ne soxla ngeen ko. 31 Waaye wutleen nguuram, te loolu lépp dina leen ko ci dollil.
32 «Buleen ragal dara, yéen coggal ju ndaw ji, ndaxte dafa soob seen Baay, mu jagleel leen nguuram. 33 Jaayleen seen alal, sarxe ko, ngir sàkku ay mbuusi xaalis yu dul bënn, maanaam alal ju dul jeex ca laaxira; foofa sàcc du ko jege te max du ko yàq. 34 Ndaxte fu sa alal nekk, fa la sa xol nekk itam.
41 Piyeer ne Yeesu: «Boroom bi, ndax dangay dégtal léeb wii ngir nun rekk walla ngir mbooloo mépp?» 42 Boroom bi ne ko: «Kan moo nekk surga bu takku te teey, bu njaatigeem teg ci waa kër gi, ngir mu leen di dundal ci jamono ji? 43 Bu njaatigeem ñëwee te gis mu def noonu, surga boobu dina am ngërëm. 44 Ci dëgg maa ngi leen koy wax, njaatige bi dina ko teg ci alalam jépp. 45 Waaye su fekkee surga ba da ne ci xelam: “Sama njaatige day yéexa ñëw,” ba tax mu tàmbalee dóor surga ya ca des ak mbindaan ya, di lekk te di naan, di màndi, 46 kon njaatige ba dina ñëw ci bés bu mu ko séenuwul ak waxtu wu mu xamul. Dina ko dóor ay dóor yu metti, jox ko añub ñi gëmul Yàlla.
47 «Surga bi xam bëgg-bëggu njaatigeem, te waajul mbaa mu takku def ko, dinañu ko dóor dóor yu metti. 48 Waaye surga bi xamul bëgg-bëggu njaatigeem, te def lu yelloo ay dóor, dinañu ko dóor dóor yu néew. Ku ñu jox lu bare dees na la feyeeku lu bare. Ku ñu dénk lu bare, dees na la laajaat lu ko ëpp.
57 «Lu tax it dungeen àtteel seen bopp liy jëf ju jub? 58 Bu la nit jiiñee dara, ba ngeen ànd di dem ca àttekat ba, nanga fexee juboo ak moom ci yoon wi. Lu ko moy, dina la yóbbu ci yoon, yoon jébbal la ca loxoy alkaati ba, mu tëj la. 59 Maa ngi la koy wax, doo génn foofa mukk te feyuloo fiftin bi ci mujj.»
<- LUUG 11LUUG 13 ->