5 Yeesu teg ca ne leen: «Mi ngi mel ni, nga dem seeti sa xarit ci xaaju guddi ne ko: “Xarit, lebal ma ñetti mburu. 6 Dafa am sama xarit bu ma ganesi, te awma dara lu ma ko jox.”
7 «Waaye kooku nekk ci biir néegam, dina ko ne: “Bu ma lakkal, tëj naa bunt bi ba noppi te tëdd naa maak sama njaboot; manumaa jóg di la jox dara.” 8 Maa ngi leen koy wax, su jógul jox ko li muy laaj ndax li ñu xaritoo it, ndax la kee ñàkk jom dina tax mu jox ko lépp li mu soxla. 9 Moo tax ma ne, ñaanleen, ñu may leen; seetleen, te dingeen gis; fëggleen, ñu ubbil leen. 10 Ndaxte képp kuy ñaan, dinga am; kuy seet, dinga gis; kuy fëgg, ñu ubbil la. 11 Bu la sa doom ñaanee jën, yaw miy baayam, ndax dinga ko baña jox jën, jox ko jaan? 12 Walla mu ñaan la nen, nga jox ko jiit? 13 Ndegam yéen ñi bon yéena mana jox seeni gone lu baax, astamaak Baay bi nekk ci kaw dina jox Xel mu Sell mi ñi ko koy ñaan!»
16 Am ñeneen ñu fexe koo fiir, ba laaj ko kéemaan gu jóge ci asamaan tey firndeel yónnentam. 17 Waaye Yeesu xam seen xalaat ne leen: «Réew mu xeex boppam tas, kër gu xeex boppam gent. 18 Te it bu Seytaane xeexee boppam, naka la nguuram di mana yàgge? Damay wax loolu, ndaxte nee ngeen, damay dàq rab jaarale ko ci kàttanu Beelsebul. 19 Te it bu fekkee ne man damay dàq ay rab ci kàttanu Beelsebul, seeni taalibe nag ci gan kàttan lañu leen di dàqe? Kon ñoo leen di àtte. 20 Waaye bu fekkee ne ci baaraamu Yàlla laay dàqe rab, kon nguuru Yàlla agsi na ba ci yéen.
21 «Su nit ku bare doole gànnaayoo, di wottu këram, alalam dina raw. 22 Waaye bu ku ko ëpp doole ñëwee, daan ko, dafay nangu gànnaay ya mu yaakaaroon, ba noppi séddale alal ja. 23 Ku farul ak man, yaa ngi may xeex, ku dajalewul ak man, yaa ngi tasaare.
24 «Boo xamee ne rab, wa jàppoon nit, génn na ci moom, day wër ay bérab yu wow, di wut fu mu noppaloo, waaye du ko gis. Noonu da naan: “Naa dellu ca sama kër, ga ma jóge.” 25 Bu ñëwee nag, mu fekk këram, ñu bale ko, defar ko ba lépp jekk. 26 Bu ko gisee nag, mu dem wooyi yeneen juróom ñaari rab yu ko gëna soxor. Ñu dugg, sanc fa; ba tax mujug nit kooku mooy yées njàlbéenam.»
27 Bi Yeesu di wax loolu, jenn jigéen yékkati baatam ca biir mbooloo ma ne: «Céy jigéen ji la ëmb te nàmpal la moo barkeel!» 28 Waaye Yeesu ne ko: «Neel kay, ki barkeel mooy kiy déglu kàddug Yàlla te di ko topp.»
45 Kenn ci xutbakat yi ne ca tonn ne: «Kilifa gi, boo waxee loolu, yaa ngi nuy xas, nun itam.» 46 Noonu Yeesu neeti leen: «Yéen itam xutbakat yi, dingeen torox! Ndaxte dangeen di sëf nit ñi say yu diis, waaye dungeen nangoo laal sëf bi sax ak seen cati baaraam. 47 Dingeen torox, ndaxte yéena ngi tabax xabruy yonent, yi seeni maam reyoon. 48 Dangeen di seede noonu ne ànd ngeen ak li seen maam defoon, ndaxte ñoo rey yonent yi, yéen ngeen tabax xabru yi. 49 Looloo tax Yàlla mi xam lépp ne: “Dinaa leen yónnee ay yonent ak ay ndaw. Ñenn ñi dinañu leen fitnaal, rey leen.” 50 Kon nag Yàlla dina mbugal niti jamono jii ndax dereti yonent yi ñu tuur, ba àddina sosoo ak léegi, 51 la dale ca Abel ba ci Sakari, moom mi ñu rey ci diggante sarxalukaay bi ak bérab bu sell bi. Waaw, maa ngi leen koy wax, Yàlla dina mbugal niti jamono jii ndax loolu. 52 Yéen xutbakat yi, dingeen torox, ndaxte yéena yóbbu caabiy xam-xam; dugguleen ci, te ku ci bëgga dugg, ngeen tere ko ko.»
53 Bi Yeesu génnee bérab boobu, Farisen ya ak xutbakat ya ëmbal ko mer te di ko seetlu ci fànn gu nekk, 54 di ko yeeru, bëgga këf waxam bu awul yoon.
<- LUUG 10LUUG 12 ->