5 «Kër gu ngeen mana dugg, nangeen jëkk ne: “Na jàmm wàcc ci kër gi.” 6 Bu fa nitu jàmm nekkee, seen yéene dina ko indil jàmm. Lu ko moy, seen yéene dina délsi ci yéen. 7 Dal-leen ca kër googa, tey lekk ak a naan lu ñu leen di jox, ndaxte liggéeykat yelloo na jot peyam. Buleen dem nag kër ak kër.
8 «Dëkk bu ngeen mana dugg, te waa dëkk ba teeru leen, lu ñu leen jox, lekkleen ko. 9 Nangeen wéral jaragi dëkk ba, te ngeen ne leen: “Nguuru Yàlla jegesi na leen.” 10 Waaye bu ngeen duggee ci dëkk te teeruwuñu leen, demleen ca mbedd ya te ne leen: 11 “Seen pëndu dëkk, bi taq ci sunuy tànk sax, noo ngi koy faxas, ngir seede leen seen réer. Waaye nag xamleen ne nguuru Yàlla jegesi na.” 12 Maa ngi leen koy wax, bu bés baa, waa Sodom ñooy tane dëkk boobu.
13 «Dingeen torox, yéen waa Korasin ak waa Betsayda, ndaxte kéemaan yi ma def ci yéen, bu ñu leen defoon ci dëkku Tir walla ci dëkku Sidon, kon tuub nañu seeni bàkkaar bu yàgg, xëppoo dóom, sol saaku. 14 Moona ca bés pénc ba, Tir ak Sidon ñoo leen di tane. 15 Te yaw dëkku Kapernawum, ndax dees na la yékkati bu kawe? Déedéet, dees na la daane bu suufe.
16 «Ku leen déglu, déglu na ma; ku leen bañ, bañ na ma. Te ku ma bañ, bañ na ki ma yónni.»
17 Juróom ñaar fukki taalibe yi ak ñaar délsi, fees ak mbég te naan: «Boroom bi, rab yi sax déggal nañu nu ndax sa tur.» 18 Yeesu ne leen: «Maa ngi doon séen Seytaane wàcce asamaan ni sawaras melax. 19 Gis ngeen, jox naa leen sañ-sañu joggi ci jaan yi ak ci jiit yi, daan dooley bañaale bi, te dara du leen mana gaañ. 20 Moona li leen rab yi déggal, bumu tax ngeen bég, waaye bégleen ndax li ñu bind seen tur ci asamaan.»
21 Ca saa soosu Xel mu Sell mi feesal Yeesu ak mbég, mu daldi ne: «Yaw Baay, Boroom asamaan ak suuf, maa ngi lay sant ci li nga nëbb yëf yii ñi am xam-xam ak ñi am xel, te xamal leen gone yi. Waaw, Baay, ndaxte looloo la neex.» 22 Yeesu teg ca ne: «Sama Baay jébbal na ma lépp, te kenn manula xam, man Doom ji, maay kan, ku dul Baay bi; kenn manula xam it kan mooy Baay bi, ku dul man Doom ji, ak ku ma ko bëgga xamal.»
23 Gannaaw bi mu waxee loolu, Yeesu walbatiku ca taalibe ya ne leen ñoom rekk: «Ñi seeni bët di gis li ngeen di gis, am nañu mbég. 24 Ndaxte maa ngi leen koy wax, yonent yu bare ak buur yu bare bëggoon nañoo gis li ngeen di gis, waaye gisuñu ko, te dégg li ngeen di dégg, waaye dégguñu ko.»
30 Yeesu ne ko: «Dafa amoon nit ku jóge woon Yerusalem, jëm Yeriko. Ay sàcc dogale ko, futti ko, dóor ko ba muy bëgga dee, dem bàyyi ko fa. 31 Faf ab sarxalkat jaar ca yoon wa, séen nit ka, teggi. 32 Benn waay it bu soqikoo ci giiru Lewi, aw ca bérab booba, séen waa ja, teggi. 33 Waaye benn waay bu dëkk Samari bu doon tukki, ñëw ba jege waa ja, gis ko, yërëm ko. 34 Noonu mu ñëw, sotti diw ak biiñ ca gaañu-gaañu ya, lëmës ko. Gannaaw loolu mu teg ko ci mbaamam, yóbbu ko ci fanaanukaay, di ko topptoo. 35 Bi bët setee, mu génne ñaari poseti xaalis*Maanaam ñaari denariyon. Seetal Xaalis ci Leeral yi., jox ko boroom kër ga ne ko: “Nanga topptoo nit kooku. Bés bu ma fi jaaraatee, dinaa la fey, man ci sama bopp, lépp loo ci dolli ci xaalis.”»
36 Yeesu teg ca ne: «Lu ciy sa xalaat? Kan ci ñett ñooñu moo jëfe ni kuy jëf jëme ci moroomam, ba ñu gisee nit, ka sàcc ya dogale woon?» 37 Xutbakat ba ne ko: «Xanaa ki ko won yërmandeem.» Yeesu ne ko nag: «Demal tey def ni moom.»
- a Maanaam ñaari denariyon. Seetal Xaalis ci Leeral yi.