5 Yeesu ne ko: «Ci dëgg-dëgg maa ngi la koy wax, ku judduwul ci ndox ak ci Xelum Yàlla, doo mana bokk ci nguuru Yàlla. 6 Lu juddoo ci nit, nit la; waaye lu juddoo ci Xelum Yàlla, xel la. 7 Li ma ne: “Fàww ngeen judduwaat,” bumu la jaaxal. 8 Ngelaw fu ko neex lay jublu. Yaa ngi koy dégg waaye xamuloo fu mu jóge, xamuloo fu mu jëm. Noonu la mel it ci képp ku juddoo ci Xelum Yàlla.»
9 Ci baat yooyu Nikodem ne ko: «Nu loolu mana ame?»
10 Yeesu ne ko: «Yaw yaay jàngal bànni Israyil te xamuloo mbir yii? 11 Ci dëgg-dëgg maa ngi la koy wax, noo ngi wax li nu xam, di nettali li nu gis, waaye nanguwuleena gëm li nu seede. 12 Gannaaw gëmuleen li ma leen di wax ci mbiri àddina, naka ngeen mana gëme, bu ma leen waxee ci mbiri asamaan? 13 Kenn masula yéeg ci asamaan su dul ki fa jóge, muy Doomu nit ki. 14 Te itam na Musaa sampe woon ab bant ca diggu màndiŋ ma, takk ca jaan, ja mu defare woon xànjar, fàww ñu yékkatee noonu Doomu nit ki, 15 ngir képp ku ko gëm am ci moom dund gu dul jeex.»
16 Ndaxte Yàlla dafa bëgg àddina, ba joxe jenn Doomam ji mu am kepp, ngir képp ku ko gëm am dund gu dul jeex te doo sànku mukk. 17 Yàlla yónniwul Doomam ci àddina ngir mu daan nit ñi, waaye ngir musal leen. 18 Képp ku ko gëm deesu la daan, waaye ku ko gëmul daan nañu la ba noppi, ndaxte gëmuloo ci turu Doom ji Yàlla am kepp. 19 Ci nii la àtte bi ame: leer gi ñëw na ci àddina, waaye nit lëndëm gi lañu taamu ndax seeni jëf yu bon. 20 Képp kuy def lu bon day bañ leer gi te du ci ñëw, ndax ragal ay jëfam di feeñ bëccëg ndarakàmm. 21 Waaye ku def lu jub day ñëw ci leer gi, ngir ñu xam ne def na ay jëfam ci kanam Yàlla.
27 Yaxya ne leen: «Kenn manula am dara lu ko Yàlla joxul. 28 Yéen ci seen bopp man ngeena seede ne waxoon naa ne duma Almasi bi waaye dañu maa yónni ma jiitusi ko. 29 Kiy céetal moo moom séetam. Waaye xaritu kiy céetal dafay taxaw di ko déglu, tey bég, bu déggee baatam. Mbég moomu moo di sama bos tey, te fi mu nekk mat na sëkk. 30 Li war moo di moom, mu gëna màgg te man, ma gëna féete suuf.»
31 Ki jóge ci kaw moo féete kaw ñépp; ki jóge ci suuf nag, ci suuf rekk la mana bokk, te ni niti àddina lay waxe. Ki jóge asamaan 32 day wax li mu gis ak li mu dégg, waaye kenn nanguwul li mu seede. 33 Képp ku nangu seedeem nangu nga ne Yàlla, dëgg lay wax. 34 Ndaw li Yàlla yónni, kàddug Yàlla lay wax, ndaxte mayu Xel mu Sell, mi Yàlla sol ci moom, amul dayo. 35 Baay bi dafa bëgg Doom ji, te jox na ko sañ-sañ ci lépp. 36 Ku gëm Doom ji, am nga dund gu dul jeex; ku déggadil Doom ji, amuloo dund, waaye merum Yàllaa ngi la tiim.
<- YOWAANA 2YOWAANA 4 ->- a judduwaat: ci làkku gereg, baat bi Yeesu wax mi ngi tekki «judduwaat» walla «juddoo ci kàttan gu jóge ci kaw».