6 Foofa amoon na fa juróom benni ndaa yu ñu yett ci doj, yu Yawut ya daan jëfandikoo ngir seen sangu set. Ndaa lu nekk man na def daanaka téeméeri liitar. 7 Yeesu ne surga ya: «Duyleen ndaa yi.» Ñu duy leen, ba ñu fees bay rembat. 8 Noonu Yeesu ne leen: «Tanqleen ci léegi, yót ko njiitu xew wi.» Ñu daldi ko ciy yót. 9 Ki jiite xew wa ñam ndox, ma Yeesu soppi biiñ. Xamul woon fu biiñ booba jóge, waaye surga ya tanqoon ndox ma, ñoom xamoon nañu ko. Naka noonu mu woo boroom céet ga ne ko: 10 «Ci xew yépp, naan gu neex gi lañuy jëkke. Bu nit ñi doyalee, ñu sooga génne ga ca des. Waaye yaw dangaa dencoon gi gëna neex ba nëgëni.»
11 Firnde jii ame ca Kana, ca diiwaanu Galile, moo doon kéemaan gi Yeesu jëkka def. Ci noonu la wonee màggaayam te ay taalibeem gëm nañu ko.
12 Bi loolu weesoo, mu ànd ak yaayam, ay rakkam ak i taalibeem, dem dëkku Kapernawum. Waaye yàgguñu fa.
18 Noonu Yawut ya ne ko: «Ban firnde nga nuy won ngir dëggal ne am nga sañ-sañu def lii nga def?» 19 Yeesu ne leen: «Daaneel-leen kër Yàlla gii, ma daldi koy yékkati ci ñetti fan.» 20 Ñu ne ko: «Nga ne kër Yàlla, gii ñu tabax ci ñeent fukki at ak juróom benn, man nga koo yékkati ci ñetti fan!»
21 Waaye kër Yàlla, gi Yeesu doon wax, nekkul woon ab tabax, aw yaramam ci boppam moo ko taxoon di wax. 22 Gannaaw ga nag, bi Yeesu deeyee ba dekki, la taalibeem ya fàttaliku li mu waxoon, daldi gëm Mbind mi ak wax, ja leen Yeesu waxoon.
23 Bi Yeesu nekkee Yerusalem ci màggalu bésu Mucc ba, ñu bare gis kéemaan, yi mu doon def, daldi gëm ci turam. 24 Waaye Yeesu wóoluwu leen woon, ndaxte xamoon na leen ñoom ñépp, 25 te it soxlawul ñu koy xamal dara ci nit, ndaxte moom ci boppam xam na xolu nit.
<- YOWAANA 1YOWAANA 3 ->