12 «Li ma leen wara wax bare na, waaye dungeen ko mana dékku. 13 Bu Xelum Yàlla mi yor dëgg gi dikkee nag, dina leen gindi ci lépp li jëm ci yoonu dëgg, ndaxte du wax ci coobarey boppam, waaye lu ko Baay bi wax, mu jottali leen ko. Dina leen yégal mbir yu ñëwagul. 14 Dina ma màggal, ndaxte lu mu leen wax, ci man la ko jële. 15 Lépp lu Baay bi am, maa ko moom. Looloo tax ma ne leen, lu mu leen jottali, ci man la ko jële.
17 Loolu Yeesu wax, tax na ba am ca taalibe ya, ñu waxante ne: «Lu muy wax nii: “Ci kanam tuuti dungeen ma gisati; bu ñu ci tegee ab diir, ngeen gisaat ma,” ak naan: “Ndaxte maa ngi dem ca Baay ba”?» 18 Ñu ne: «“Teg cab diir,” lu muy tekki? Xamunu li muy bëgga wax.»
19 Yeesu gis ne am na lu ñu ko bëgga laaj, mu ne leen: «Dama ne: “Ca kanam tuuti, dungeen ma gis, te bu ñu ca tegee ab diir, ngeen gisaat ma.” Ndax loolu ngeen di laajante ci seen biir? 20 Ci dëgg-dëgg maa ngi leen koy wax, dingeen jooy xàcc, waaye àddina dina bég; dingeen jàq, waaye seen njàqare dina soppaliku bànneex. 21 Jigéen ju nekk ci mat, dafay jàq, ndaxte waxtu wi mu wara jur jot na. Waaye bu doom ji juddoo, dina fàtte coonoom ndaxte day bég ci li doom ji gane àddina. 22 Noonu nag ngeen di jàqe, yéen itam. Waaye dinaa leen gisaat, seeni xol sedd, te seen mbég moomu, kenn du ko mana dindi. 23 Bés boobu dootuleen ma laaj dara. Ci dëgg-dëgg maa ngi leen koy wax, Baay bi dina leen may lu ngeen ko ñaan ci sama tur. 24 Ba léegi ñaanaguleen dara ci sama tur. Ñaanleen, mu nangu. Bu ko defee seen mbég mat sëkk.
29 Taalibe yi ne ko: «Léegi yaa ngi wax lu leer te misaaloo! 30 Léegi gis nanu ne xam nga lépp, te soxlawul kenn di la laaj dara. Looloo tax nu xam ne yaa ngi jóge ci Yàlla.» 31 Yeesu ne leen: «Ndax gëm ngeen léegi? 32 Waxtu waa ngi ñëw te agsi na ba noppi, dingeen tasaaroo, ku nekk ñibbi, ma des man rekk. 33 Waaye nag déedéet, wéetuma, ndaxte Baay baa ngi may wéttali. Dama leen wax loolu, ngir ngeen am jàmm ci man. Dingeen am nattu ci àddina, waaye takkleen fit yi; not naa àddina.»
<- YOWAANA 15YOWAANA 17 ->- a Seetal ci 14.16, 17 ak 26.