5 «Man maay garab gi; yéen yéenay car yi. Ki sax ci man te ma sax ci moom, dina meññ, ndaxte bu ngeen saxul ci man, dungeen man dara. 6 Ku saxul ci man dinañu ko sànni ci biti, mu mel ni car bu ñu dagg, ba mu wow. Car yu wow nag, dañu leen di buub, sànni ci sawara, ñu lakk. 7 Bu ngeen saxee ci man te saxal samay wax ci seen xol, lu ngeen ñaan mu nangu. 8 Liy feeñal sama ndamu Baay moo di, ngeen di gëna meññ tey wone noonu ne samay taalibe ngeen.
9 «Ni ma Baay bi bëggee, noonu itam laa leen bëgge. Saxleen ci mbëggeel googu ma am ci yéen. 10 Bu ngeen toppee samay ndigal, dingeen sax ci sama mbëggeel, ni ma toppe sama ndigali Baay, ba tax ma sax ci mbëggeelam. 11 Wax naa leen loolu, ngir ngeen bokk ci sama mbég, te seen bos mat sëkk. 12 Sama ndigal mooy ngeen bëggante, ni ma leen bëgge. 13 Genn mbëggeel manula weesu joxe sa bakkan ngir say xarit. 14 Samay xarit ngeen, ci kaw ngeen def li ma santaane. 15 Dootuma leen wooye jaam, ndaxte jaam du xam li sangam di def. Xarit laa leen wooye, ndaxte xamal naa leen li ma jële lépp ci sama Baay. 16 Du yéen yéena ma tànn, waaye man maa leen tànn, sas leen ngeen dem, meññ meññeef gu sax, ngir Baay bi def lu ngeen ko ñaan ci sama tur. 17 Li may santaane nag, mooy ngeen bëggante.
26 «Dimbalikat bi†Seetal ci 14.16, 17 ak 26. dina ñëw, mooy Xel mi jóge ci Baay bi tey yor dëgg gi. Dina jóge ci Baay bi, ma yebal ko ci yéen. Moom nag, moo may seedeeli. 27 Te yéen itam dingeen seede samay mbir, ndaxte yéena nekkoon ak man ca njàlbéen ga.
<- YOWAANA 14YOWAANA 16 ->