7 Waaye Yeesu ne ko: «Bàyyi ko! Jekkoon na mu denc ko ngir bés bu ñu may suul. 8 Miskin yaa ngi ak yéen bés bu nekk, waaye dungeen ma gis ba fàww.»
9 Bi ñu yégee ne Yeesoo nga fa, mbooloom Yawut mu bare daldi dem Betani. Yeesu rekk yóbbuwu leen fa woon, waaye dañoo bëggoona gisaale Lasaar, mi Yeesu dekkaloon. 10 Sarxalkat yu mag ya dogu ci ne dañuy reyaale Lasaar, 11 ndaxte moo waral Yawut yu bare dëddu leen, gëm Yeesu.
16 Yooyu yépp, taalibe ya xamuñu woon ca saa sa lu muy tekki; waaye gannaaw bi ndamu Yeesu feeñee, ñu fàttaliku ne, Mbind mi yégle woon na loolu ci moom, te amal nañu ko.
17 Ña nekkoon ak Yeesu ñépp, bi muy wooyee Lasaar mu génn ca bàmmeel ba te mu dekkal ko, demoon nañu, nettali la ñu gis. 18 Looloo tax mbooloo ma teeru ko, ndaxte yégoon nañu firnde jooju. 19 Farisen yi nag di waxante naan: «Gis ngeen, manuleen ci dara; ñépp a ngi koy topp!»
23 Mu ne leen: «Waxtu wi ñu wara feeñale ndamu Doomu nit ki jot na. 24 Ci dëgg-dëgg maa ngi leen koy wax, fi ak peppu dugub ji wadd ci suuf jaarul ci dee, du mana weesu li mu doon: pepp doŋŋ. Waaye bu deeyee, dina jur pepp yu bare. 25 Ku bëgg bakkanam dina ko ñàkk, waaye ku ko bañ ci àddina sii, dina ko denc ngir dund gu dul jeex gi. 26 Ku bëgga doon sama surga, na ma topp. Bu ko defee, fu ma nekk, fa lay nekk moom itam. Ku may liggéeyal, sama Baay dina ko teral.
27 «Léegi nag damaa jàq. Lu may wara wax? Mbaa du dama naan: “Baay, musal ma ci li nara xew waxtu wiy ñëw?” Déedéet, ñëw naa sax ngir jaar ci waxtu woowu. 28 Baay, màggalal sa tur!» Noonu ñu dégg baat bu jóge asamaan naan: «Màggal naa ko ba noppi, te dinaa ko màggalaat.»
29 Mbooloo ma fa teewoon te dégg baat ba daldi ne: «Dënnu la woon!» Ñeneen naan: «Malaakaa doon wax ak moom.» 30 Waaye Yeesu ne leen: «Taxuma baat boobu jolli, waaye yéena tax. 31 Àtteb àddina si jot na: léegi ñu dàq malaaka mu bon, mi jiite àddina si. 32 Te man, bu ñu ma yékkatee, ma tiim suuf, dinaa xiirtal nit ñépp ci man.» 33 Ci baat yooyu la doon misaale ni mu wara faatoo.
34 Mbooloo ma ne ko: «Jàng nanu ci sunu téereb yoon ne, Almasi bi dina sax ba fàww. Kon yaw, nan nga mana waxe ne: “Doomu nit ki dina yékkatiku?” Kuy Doomu nit kooku?»
35 Yeesu ne leen: «Leer gi dootul yàgg ak yéen. Doxleen, ci bi ngeen dee am leer, ngir lëndëm bañ leena bett. Ndaxte kuy dox ci lëndëm doo xam foo jëm. 36 Kon ci bi ngeen dee am leer gi, gëmleen ko, ngir ngeen doon doomi leer.»
42 Fekk na ci biir njiit yi sax, ñu bare gëmoon nañu Yeesu, waaye Farisen yee tax fésaluñu ko, ndaxte dañoo ragaloon, ñu dàq leen ca jàngu ba. 43 Ngërëmu nit a leen gënaloon ngërëmu Yàlla.
44 Yeesu yégle ne: «Ku ma gëm, gëmuloo ma waaye gëm nga ki ma yónni. 45 Ku ma gis, gis nga ki ma yónni. 46 Ni ag leer laa wàcce ci àddina, ngir ku ma gëm du des ci lëndëm. 47 Ku dégg samay wax te toppu leen, du man maa koy daan, ndaxte wàccuma ngir daan àddina, waaye damaa ñëw ngir musal ko. 48 Ku ma beddeeku te nanguwul samay wax, dina fekk fii li koy daan: sama njànglee koy daan keroog bés bu mujj ba. 49 Ndaxte waxuma ci sama coobare, waaye Baay bi ma yónni ci boppam, moo ma sant li ma wara wax ak li ma wara jàngle. 50 Te xam naa ne li muy santaane day joxe dund gu dul jeex. Kon li ma wax, dama koy wax, ni ma ko Baay bi sante.»
<- YOWAANA 11YOWAANA 13 ->