4 Seetleen ni mu màgge, moom Melkisedeg! Ibraayma sax, maamu cosaan mi, fab na li mu jële woon lépp ca xare ba, jox Melkisedeg asaka ja. 5 Yoonu Musaa digle na ne ñi bokk ci giiru Lewi te di ay sarxalkat, nañu jot asaka ci alalu bànni Israyil, doonte sax ñuy seeni bokk te soqikoo ci Ibraayma. 6 Waaye Melkisedeg mi bokkul woon ci giiru Lewi, jotoon na asaka ci alali Ibraayma. Te rax-ca-dolli barkeel na ko, moom mi Yàlla sédde woon dige yi. 7 Kiy barkeel a gëna màgg ki ñuy barkeel, loolu amu ci benn werante. 8 Sarxalkat yi soqikoo ci Lewi, ñu ngi jot asaka, ni ko Melkisedeg jote woon. Waaye ñoom ñu nara dee lañu. Melkisedeg nag moom, Mbind mi wóoral na ne dafay dund. 9 Léegi nag ci ni ñu ko mana waxe, Lewi miy jot asaka ci bànni Israyil, moom ci boppam jox na ko Melkisedeg, jaare ko ci Ibraayma. 10 Ndaxte mi ngi nekkoon ci geñog maamam Ibraayma, bi ko Melkisedeg gatandoo.
18 Noonu tebbi nañu yoon wu jëkk, wa néewoon doole te meññul dara 19 —ndax yoonu Musaa yeggalewul dara cig mat— waaye dugalal nañu nu fii yaakaar ju gën ju nu mana jaare ngir jege Yàlla.
20 Te rax-ca-dolli ngiñ ànd na ci. Ndaxte ñi soqikoo ci Lewi doon nañu ay sarxalkat te kenn giñul. 21 Waaye nag Yeesu moom doon na sarxalkat, bi Yàlla giñee ne ko:
23 Te it yeneen sarxalkat yi dañoo bare woon, ndaxte dee moo daan tax duñu mana sax ci seen liggéey. 24 Waaye Yeesu miy dund ba fàww, sasoo na liggéeyu sarxale bu sax fàww. 25 Loolu moo tax it mu mana musal tey yeggale cig mat ñiy jaar ci moom te bëgg jege Yàlla, ndaxte mi ngi dund ba fàww ngir di leen rammu.
26 Kon nag Yeesu mooy sarxalkat bu mag, bi nu soxla; dafa sell, du def lu bon, du taq bàkkaar, bokkul dara ak bàkkaarkat yi, te yéege nañu ko fa Yàlla. 27 Niroowul ak yeneen sarxalkat yu mag yi; soxlawul di def bés bu set ay saraxi mala ngir bàkkaari boppam jëkk, teg ca yoy mbooloo mi. Yeesu def na sarax benn yoon ba fàww ngir dindi bàkkaar yi, bi muy joxe bakkanam. 28 Naka yoonu Musaa, aji néew doole yi lay fal sarxalkat yu mag. Waaye ngiñu Yàlla gi ñëw gannaaw yoon wi, Doom ji la fal sarxalkat bu mag bu mat ba fàww.
<- YAWUT YA 6YAWUT YA 8 ->