1 Naka yéen xale yi, nangeen déggal seeni waajur, ci li ngeen bokk ci Boroom bi, ndaxte looloo rafet. 2 «Teralal sa ndey ak sa baay,» mooy ndigal li jëkka ëmb dige, 3 maanaa: «ngir nga am gudd fan gu ànd ak jàmm.»
4 Yéen baay yi it, buleen bundxataal xale yi, waaye ngeen yar leen, di leen yemale ak a yee ci Boroom bi.
Diggante jaam ak sangam
5 Yéen jaam yi, nangeen déggal seeni sang yu àddina, boole ci ragal ak wegeel, di ko def ak xol bu laab, ni su doon ngir Kirist. 6 Buleen ko def rekk ci ngistal, ngir sàkku ngërëmu nit, waaye ni ay jaami Kirist, di jëfe coobarey Yàlla ak seen xol bépp. 7 Beyleen seen sas nag ak xol bu tàlli, ni su doon ngir Boroom bi te du nit, 8 xam ne ku def lu baax, Boroom bi delloo la ko, muy jaam, muy gor.
9 Yéen it sang yi, jëfeleen noonu seen diggante ak seeni jaam, te dëddu gépp raglu, xam ne yéena bokk benn Boroom ci asamaan, te ñépp a yem fi moom.
Xeex ak Seytaane
10 Léegi nag doolewuleen ci Boroom bi te soloo kàttanam gu mag gi. 11 Gànnaayooleen yérey xarey Yàlla yépp, ngir mana jànkoonte ak pexey Seytaane. 12 Ndaxte ndëndu xare jib na, waxuma sunu diggante ak nit ñi, waaye ak kilifa yiy nëxal àddina si, ñuy kilifa yi ak ay boroom sañ-sañ, di gaayi Seytaane yi ci bérab yu kawe yi. 13 Kon nag gànnaayooleen yérey xarey Yàlla yépp, ba mana jànkoonte jamono ju xeex bi taree, not lépp te taxaw temm.
14 Taxawleen kon temm, geñoo dëgg te sàngoo njub, muy seen kiiraayu dënn. 15 Solooleen jàmm, ji xibaaru jàmm biy joxe, ni ay dàll ci seeni tànk, ba jekk ci lépp. 16 Defleen it ngëm, muy seen pakk, ba mana fél jum yi leen Seytaane di fitt. 17 Defleen mucc, muy seen mbaxanam xare, ak kàddug Yàlla, muy jaasi ji leen Xel mu Sell mi tëggal. 18 Deeleen ñaan ci xeeti ñaan yépp ci kàttanu Xel mu Sell mi, te sax ci ak farlu gu mat sëkk, di ñaanal gaayi Yàlla yu sell yi yépp.
19 Te buleen ma ci fàtte, ngir waxtu wu ma ubbee sama gémmiñ, ma am lu ma wax, ba mana xamle ak fit wu dëgër mbóoti xibaaru jàmm bi. 20 Ndaw laa ci, lu ñu jéng; yal na ma Yàlla may fit wu ma waxe, ni mu ma ware.
Tàggoo
21 Yónnee naa leen Tisig sama mbokk, mi ma sopp, te muy jawriñ ju takku ci liggéeyu Boroom bi, ngir mu xamal leen lépp li aju ci man ak li may def. 22 Maa leen ko yónneel sama bopp, ngir ngeen xam li nu nekke, te mu dëfal seeni xol.
23 Yéen bokk yi, yal na leen Yàlla Baay bi ak Yeesu Kirist Boroom bi may jàmm ak mbëggeel gu ànd ak ngëm. 24 Yal na yiwu Yàlla ànd ak ñépp, ñi bëgg Boroom bi Yeesu Kirist ak mbëggeel gu sax.