14 Ndaxte mooy sunu jàmm, moom mi jël Yawut ak ki dul Yawut, def nu benn. Ñag bi doxoon sunu diggante te sosoon sunu dëngoo, moo ko màbb ci li mu joxe yaramam, 15 far noonu yoonu Musaa, muy ndigal ya ak dogal ya. Noonu la nu jële, Yawut ak ki dul Yawut, def nu benn ci moom, ba nu jàmmoo. 16 Nun ñaar, ñi def benn jëmm, jubale na nu ak Yàlla ci dee, gi mu dee ca bant ba ñu ko daajoon, dindee noonu sunu tongoonte. 17 Bi mu ko defee mu ñëw, yégalsi nu xibaaru jàmm fa kanam Yàlla, yéen ñi sore woon ak nun ñi jege. 18 Ndaxte nun ñaar ñépp am nanu bunt ci Yàlla Baay bi, jaar ci Kirist, ci ndimbalu menn Xel mu Sell mi.
19 Noonu dootuleen ay doxandéem mbaa ay gan, waaye am ngeen baat ci kureelu gaayi Yàlla yu sell yi, te waa këram ngeen. 20 Yéena ngi sukkandikoo ci fondamaa, bi ndawi Kirist yi ak yonent yi tabax, te Kirist Yeesu ci boppam di doju dalil wa. 21 Ci moom la doj yépp ràbbloo, ba tabax bi jóg, di màggalukaay bu sell ngir Boroom bi. 22 Ci seen bokk ci Kirist, Yàlla boole na leen tabax yéen itam, ba ngeen nekk dëkkukaayam, jaar ci Xel mu Sell mi.
<- EFES 1EFES 3 ->