mu bind ko
WAA EFES
1 Man Pool, ndawul Kirist Yeesu ci coobarey Yàlla, maa leen di bind, yéen gaayi Yàlla yu sell yi te gëm Kirist Yeesu ci dëkku Efes. 2 Yal na leen Yàlla sunu Baay ak Boroom bi Yeesu Kirist may yiw ak jàmm.
3 Cant ñeel na Yàlla Baayu sunu Boroom Yeesu Kirist, mi nu sotti ci sunu bokk ci Kirist lépp luy barkeel ci baatin te nekk ca bérab yu kawe ya. 4 Ndaxte ba àddina sosoogul, tànn na nu ci Kirist, ngir nu mana teew fa kanamam, sell te ñàkk sikk. Ci kaw mbëggeelam*Manees na ko tekki nii it: ñàkk sikk ci biir mbëggeel. Séddoo na… 5 séddoo na nu lu jiitu, def nu ay doomam jaarale ko ci Yeesu Kirist, ndaxte looloo doon yéene ju rafet, ji mu tëral ci coobareem. 6 Na ndamam jolli ndax yiw wu réy, wi mu nu sotti ci Soppeem bi.
7 Moom jot na nu ak deretam ji ñu tuur, maanaam baal nu sunuy bàkkaar, ci kaw yiw wu yaatu, 8 wi mu nu baawaanal. Yàlla sol na nu xel mu mat ak dégg, 9 ci feeñal nu mbóoti coobareem, dëppook yéeneem ju rafet, ji mu jaarale ci Kirist. 10 Mu tëral ne, bu jamono yi wéyee ba lépp mat, dina dajale lépp ci kilifteefu Kirist, muy ci kaw, muy ci suuf. 11 Am nanu cér ci moom bu nu Yàlla sédd lu jiitu ci dogalam, moom miy doxal lépp ci ni mu ko àttee ci coobareem. 12 Noonu nuy jollil ndamam, nun ñi jëkka wékk sunu yaakaar ci Kirist.
13 Yéen itam, bi ngeen déggee kàddug dëgg gi, di xibaaru jàmm, bi leen tegtal yoonu mucc, te ngeen gëm ko, Yàlla tàmpe na leen ni ñoñam ak Xel mu Sell, mi mu dige woon. 14 Te Xel mi mooy dawal gi nu Yàlla jox ci cér, bi mu nu dencal, ba kera muy goreel ñi mu jotal boppam, te ñépp jollil ndamam.
- a Manees na ko tekki nii it: ñàkk sikk ci biir mbëggeel. Séddoo na…