mu bind ko
WAA KOLOS
1 Man Pool, ndawul Kirist Yeesu ci coobarey Yàlla, man ak Timote sunu mbokk, 2 noo leen di bind, yéen gaayi Yàlla yu sell, yi dëkk Kolos te di ay bokk ci gëm Kirist. Yal na leen Yàlla sunu Baay may yiw ak jàmm.
9 Looloo tax ci sunu wàllu bopp, ba nu ko yégee ba tey, jógunu ci di leen ñaanal. Nu ngi ñaan Yàlla, ngeen xam bu baax coobareem ci xel mu mat ak ràññee gu aju ci dooley Xelam. 10 Noonu dingeen dund dund gu dëppoo ak seen bokk ci Boroom bi, ba neex ko ci fànn gu nekk, di def bépp jëf yu baax, te yokk seen xam-xam ci Yàlla. 11 Te Yàlla dina leen dooleel ak bépp doole, mu méngoo ak kàttanu ndamam, ngir ngeen mana tegoo coono te muñ, ba fa muñ di yem. 12 Dingeen gërëm Yàlla Baay bi, ànd ci ak mbég, moom mi leen jagleel, ngeen bokk ci cér, bi mu dencal gaayam yu sell yi ci leer.
15 Doom jooju moo di melokaanu Yàlla, ji kenn gisul. Mooy taaw bi, ki gëna màgg lépp luy mbindeef. 16 Ndaxte ci moom la Yàlla sàkke lépp lu nekk ci asamaan ak suuf, li ñuy gis ak li ñu manula gis, muy buur, njiit, kilifa mbaa boroom sañ-sañ. Lépp lu ñu sàkk, ci moom lañu ko jaarale, ci moom lañu ko jëme. 17 Laata dara di am, fekkoon na moom mu nekk, te lépp a ngi jàppoo ci moom.
18 Mooy bopp bi yilif jëmm ji, di mbooloom ñi ko gëm, ndaxte moom mooy njàlbéen gi, di taaw bi, maanaam ki jëkka dekki, ngir muy kilifa ci bépp fànn. 19 Ndaxte soob na Yàlla mu dëkkal matam gépp ci moom 20 te jaar ci moom, jubale lépp ak boppam, muy ci kaw asamaan yi mbaa ci suuf, ba mu wàccee jàmm jaarale ko ci deret ji tuuru, bi Doom ji deeyee ca bant ba.
21 Te yéen ñi sore woon Yàlla te doon ay noonam ci seen xel ak seen jëf yu bon, 22 léegi nag Yàlla jubale na leen ak boppam jaare ko ci deewu Kirist ci yaramu nitam, ngir taxawal leen ca kanamam, ngeen sell te ñàkk sikk, ñàkk i ŋàññ. 23 Loolu nag na fekk ngeen wéy ci ngëm, sampu ci ba dëgër ci, tey séentu cér, bi leen xibaaru jàmm bi jox. Te xibaaru jàmm, boobu ngeen dégg te ñu yégal waa àddina sépp, man Pool moom laay yégle.
28 Moom Kirist lanuy yégle, di artu te di jàngal ku nekk, ànd ak xel mu mat, ngir jébbal Yàlla ku nekk ni ku mat ci Kirist. 29 Ci loolu laay jëmale sama liggéey, di bëree dooley Kirist, jiy yëngu ci man ak kàttan.
KOLOS 2 ->