1 Sóol moom ànd na ci ñi doon rey Ecen.
14 Bi nga xamee ne ndaw yi nekk Yerusalem yég nañu ne, waa Samari nangu nañu kàddug Yàlla; ñu yónni fa Piyeer ak Yowaana. 15 Ñu dem fa nag, ñaanal leen, ngir ñu jot Xel mu Sell mi. 16 Ndaxte wàccagul ci kenn ci ñoom, waaye sóoboon nañu leen rekk ci ndox ci turu Boroom bi Yeesu. 17 Noonu Piyeer ak Yowaana teg leen loxo, ñu jot Xel mu Sell mi.
18 Bi Simoŋ gisee nag ne Yàlla may na Xel mi jaarale ko ci loxoy ndaw ya, mu indil leen xaalis, 19 ne leen: «Mayleen ma sañ-sañ boobu, ba ku ma teg samay loxo, nga jot Xel mu Sell mi.» 20 Waaye Piyeer ne ko: «Asarul ak sa xaalis, yaw mi yaakaar ne man ngaa jënd mayu Yàlla ak xaalis. 21 Amuloo benn wàll mbaa cér ci lii, ndaxte sa xol laabul ci kanam Yàlla. 22 Réccul nag sa coxor te ñaan Boroom bi, mu baal la sa xalaatu xol, su manee am. 23 Ndaxte gis naa ne sóobu nga ci lu wex xat ci kanam Yàlla, te bàkkaar not na la.» 24 Simoŋ nag ne leen: «Ñaanal-leen ma ci Boroom bi, ngir mu fegal ma li ngeen wax.»
25 Noonu bi ñu seedeelee Yàlla te wax ci kàddoom, ñu dellu Yerusalem, di xamle xibaaru jàmm bi ci dëkk yu bare yu waa Samari.
30 Noonu Filib dawsi, mu dégg waayi Ecópi ja, di jàng téereb yonent Yàlla Esayi. Mu laaj ko: «Ndax xam nga li ngay jàng?» 31 Mu ne ko: «Nu ma ko mana xame, su ma ko kenn firilul?» Mu woo Filib nag, mu yéeg, toog ak moom. 32 Fekk aaya yii la doon jàng ci Mbind mi:
34 Jaraaf ja nag ne Filib: «Maa ngi lay laaj, ci mbirum kan la yonent bi jëmale wax ji? Ndax mbirum boppam lay wax mbaa mu keneen?» 35 Noonu Filib tàmbali ci aaya yooyu, xamal ko xibaaru jàmm bi ci mbirum Yeesu.
36-37 Bi ñuy jaar ci yoon wi, ñu agsi ci ndox. Jaraaf ja ne ko: «Ndox a ngi nii, ana lu tere, nga sóob ma ci?» 38 Mu santaane nag, ñu taxawal watiir wa; Filib ak jaraaf ja wàcc ñoom ñaar ci biir ndox ma, mu sóob ko ca. 39 Ba noppi ñu génn ca ndox ma, te ca saa sa Xelu Boroom bi fëkk Filib, ba jaraaf ja gisatu ko, waaye mu toppaat yoonam, ànd ak mbég. 40 Filib moom teeri dëkku Asot, muy jaar ci dëkk yépp, di fa xamle xibaaru jàmm bi, ba kera muy ñëw dëkku Sesare.
<- JËF YA 7JËF YA 9 ->