5 Ca ëllëg sa nag kilifay Yawut yi ak njiit yi ak xutbakat yi dajaloo ci Yerusalem. 6 Ràññee nañu ci: Anas, miy sarxalkat bu mag bi, Kayif, Yowaana, Alegsàndar ak bokki sarxalkat bu mag bi. 7 Ñu dëj Piyeer ak Yowaana ca digg ba, laaj leen ne: «Lii ngeen def, ci gan kàttan, mbaa ci turu kan, ngeen ko defe?»
8 Ci kaw loolu Piyeer daldi fees ak Xel mu Sell mi, ne leen: «Yéen kilifay xeet wi ak njiit yi, 9 bu fekkee ne xettali nit ku wopp, ba mu wér, moo tax ngeen dëj nu ci pénc mi tey, 10 nangeen xam lii, yéen ñépp ak bànni Israyil gépp: ci turu Yeesu Kirist mu Nasaret, mi ngeen daajoon ca bant te Yàlla dekkal ko, ci tur woowu la nit kii jële ag wér, ba taxaw ci seen kanam. 11 Yeesu moomu mooy:
13 Kon bi ñu gisee fit, wi Piyeer ak Yowaana àndal, te ñu xam ne masuñoo jàng mbaa ñuy gëstu ci diine, ñu daldi waaru, ràññee ne daa nañu ànd ak Yeesu. 14 Te bi ñu gisee nit, ka ñu fajoon, taxaw ak ñoom, manuñu caa teg dara. 15 Noonu ñu santaane, ñu génne leen, ñu daldi gise ci seen biir, 16 ne: «Lu nuy def ak ñii? Ndaxte def nañu kéemaan gu siiw; loolu leer na ñi dëkk Yerusalem ñépp, te manunu koo weddi. 17 Waaye ngir mbir mi baña law ci xeet wi, nanu leen aaye, ñu baña waxati ak kenn ci tur woowu.»
18 Noonu ñu woo leen, ñu tere leen bu wóor, ñu waxati mbaa waare dara ci turu Yeesu. 19 Waaye Piyeer ak Yowaana ne leen: «Bu fekkee ne déggal leen te bàyyi Yàlla mooy li jub ci kanam Yàlla, seetleen. 20 Waaye nun manunoo baña wax li nu gis te dégg ko.» 21 Noonu kilifa yi tëkkuwaat leen, yiwi leen, ñu dem. Ndaxte amuñu benn bunt ci ñoom ngir mbugal leen, fekk ñépp di màggal Yàlla ci li xewoon. 22 Ndaxte nit, ka ñu fajoon ci kéemaan googu, weesoon na ñeent fukki at.
31 Bi ñu ñaanee ba noppi, bérab ba ñu booloo woon daldi yëngatu; te ñoom ñépp fees ak Xel mu Sell mi, ñuy wax kàddug Yàlla ak fit wu dëgër.
36 Noonu amoon na fa ku tudd Yuusufa, te ndaw yi dàkkentale ko Barnabas, miy tekki «Kiy dëgëral fit yi,» mu soqikoo ci giiru Lewi, te juddoo dunu Sipar. 37 Moom nag jaay na tool, ba mu moom, indi xaalis ba, teg ko ci loxoy ndaw ya.
<- JËF YA 3JËF YA 5 ->