13 Bi bésub noflaay agsee nag, génn nanu ci buntu dëkk ba, jublu ci wetu dex ga, yaakaar ne bérabu ñaanukaay la. Nu toog fa nag, di wax ak jigéen ña fa dajaloo. 14 Fekk am na fa jigéen juy déglu, tudd Lidi, di jaaykatu cuub[b], bu dëkk Catir, te mu ragal Yàlla. Noonu Boroom bi ubbi na xolam, ba mu nangu li Pool di wax. 15 Ci kaw loolu ñu sóob ko ci ndox, moom ak waa këram, ba noppi mu ñaan nu ne: «Bu ngeen ma jàppee ni ku takku ci Boroom bi, ganesileen ma ci sama kër.» Te mu di nu ci xiir.
19 Bi ay sangam gisee nag seen buntu wërsëg tëju, ñu daldi jàpp Pool ak Silas, di leen diri, jëme leen ca pénc ma fa kanam njiit ya. 20 Noonu ñu dëj leen fa mbaxanay menne naan: «Yawut yii lëjal nañu sunu dëkk, 21 di xamle ay aada yu nu sañula nangu mbaa nu di ko topp, nun ñi bokk ci nguuru Room.»
22 Mbooloo ma it ànd ci, dal ci seen kaw; àttekat ya nag summilu seeni yére, santaane ñu dóor leen ay yar. 23 Noonu ñu dóor leen ay yar yu bare, tëj leen, sant boroom kaso ba, mu wottu leen bu wér. 24 Gannaaw jot na ndigal loolu nag, mu sànni leen ca néeg ba gëna ruqu ci biir kaso ba, jéng seeni tànk.
25 Ba guddi giy xaaj nag, Pool ak Silas di ñaan ak di sant Yàlla, te ñeneen ñi nekk ca kaso ba di leen déglu. 26 Ca saa sa suuf yëngu bu metti, ba fondamaab kaso ba daanu; bunt yépp daldi ne kulbét ubbiku, te jéngi ña ñu tëj ne téll tijjiku. 27 Ci kaw loolu boroom kaso ba tiite ci ay nelaw, gis bunt yépp ubbiku. Mu daldi bocci jaaseem, bëgga xaru, yaakaar ne ña ñu tëj dañoo daw. 28 Waaye Pool wax ci kaw ne: «Bul lor sa bopp, nun ñépp nu ngi fi.»
29 Bi ko boroom kaso ba déggee, mu daldi laaj làmp, ne saraax dugg, daanu ci kanam Pool ak Silas, di lox. 30 Mu génne leen ci biti ne leen: «Kilifa yi, lu ma wara def, ba mucc?» 31 Ñu ne ko: «Gëmal Yeesu Boroom bi, kon dinga mucc, yaw ak sa njaboot.» 32 Noonu ñu xamal ko kàddug Boroom bi, moom ak waa këram gépp. 33 Mu jël leen nag ci waxtu woowu ci guddi, raxas seeni gaañu-gaañu, ba noppi ñu sóob ko ci ndox, moom ak waa këram gépp. 34 Bi ñu ko defee mu yóbbu leen ca këram, jox leen ñu lekk, mu bég lool ci li mu gëm Yàlla, moom ak waa këram gépp.
35 Bi bët setee, àttekat ya yónni alkaati ya, ñu ne boroom kaso ba: «Yiwil ñaari nit ñooñu, ñu dem.» 36 Kon boroom kaso ba yégal loolu Pool ne ko: «Àttekat ya jox nañu ma ndigal, ngir ma yiwi leen, ngeen dem; léegi nag génnleen te dem ci jàmm.»
37 Waaye Pool ne alkaati ya: «Dóor nañu nu ay yar ci kanam ñépp, ci lu ñu wéerul ci benn àtte, rax-ca-dolli tëj nañu nu kaso, nun ñiy jaambur ci nguuru Room. Léegi ndax dañu noo bëgga sànni ci mbedd mi ci kumpa? Mukk! Nañu ñëw, ñoom ci seen bopp, gunge nu ci biti.»
38 Bi mu ko waxee, alkaati ya yégal àttekat ya la mu wax. Bi ñu déggee ne jaamburi Room lañu, ñu daldi tiit. 39 Ñu ñëw nag di leen dëfal, ñu gunge leen ci biti, di leen ñaan, ñu génn dëkk ba. 40 Noonu ñu génn ca kaso ba, dugg ci kër Lidi, ñu gis fa bokk ya, dëgëral leen, daldi dem seen yoon.
<- JËF YA 15JËF YA 17 ->