1 Ci mbirum ndimbal loolu jëm ci gaayi Yàlla yi, matul ma leen di bindaat, 2 ndaxte xam naa seen yéene ju rafet, te maa ngi ciy damu ci kanam waa Maseduwan, naan leen: «Daaw fekk na waa Akayi[a] jekk.» Te seen cawarte xamb na ñu bare ci ñoom. 3 Maa ngi yónni nag bokk yooyu, ngir damu gi nu doon damu ci yéen ci mbir mii baña neen, te ngeen jekk, ni ma ko waxe woon. 4 Danoo bañ rekk waa Maseduwan, ñiy ànd ak man, fekk jekkaguleen; te kon kóolute googu nu am ci yéen dina nekk sunu gàcce, waxaalewuma nag seen bos. 5 Moo tax ma xalaat ne li gën mooy yónni bokk yooyu, ñu jiitu ma ci yéen, topptoo mbiri ndimbal lu yaatu loolu ngeen dige woon. Loolu di may gu tàlli, te baña nekk yëfi nay.
12 Ndaxte njaamu, gi ngeen di jaamu, yemul rekk ci faj soxlay gaayi Yàlla yi, waaye dina tax it ngërëmu ñu bare baawaan, jëm ci Yàlla. 13 Ci li ngeen firndeel seen mbëggeel ci joxe ndimbal lii, dinañu màggal Yàlla, ndaxte wone ngeen ni ngeen déggale xibaaru jàmm bu Kirist bi, ak ni ngeen yéwéne ci seen ndimbal jëme ci ñoom ak ñépp. 14 Rax-ca-dolli dinañu sant Yàlla ak xol bu fees ak cofeel ci yéen ndax yiw wu mag, wi Yàlla def ci yéen. 15 Jërëjëfati yaw Yàlla ndax sa may googu weesu dayo!
<- 2 KORENT 82 KORENT 10 ->- a waa Akayi: Korent mooy péeyu diiwaanu Akayi.