13 Mbind mi nee na: «Damaa gëm, moo tax ma wax.» Nun it nag, ndegam am nanu menn xelu ngëm moomu, danoo gëm, ba tax nuy wax. 14 Ndaxte xam nanu ne Yàlla, mi dekkal Boroom bi Yeesu, dina nu dekkal nun itam ak Yeesu, te dina nu yóbbu ak yéen, taxawal nun ñépp ci jataayam. 15 Ndaxte lépp li nuy daj, seen njariñ a tax, ngir yiwu Yàlla, wiy yokku ci nit ñu gëna takku, yokkaale ngërëm lu jëm ci Yàlla, ngir jollil ndamam.
16 Loolu moo tax sunu yaakaar du tas. Bu fekkee sax sunu yaram day yàqu jëm cig mag, sunu ruu moom, bés ak bés muy gëna yeesaat. 17 Ndaxte sunu coono bu woyof bi dul yàgg, dafa nuy jural ndam lu bare, ba suul coono bi, tey sax abadan. 18 Kon diirunu li ñuy gis waaye li ñu dul gis. Ndaxte li ñuy gis day wéy, waaye li ñu dul gis day sax ba fàww.
<- 2 KORENT 32 KORENT 5 ->