5 Xool-leen seen bopp bu baax, ba xam ndax ngëm a ngi ci yéen. Seetluleen seen bopp. Xanaa xamuleen ne Yeesoo ngi ci yéen? Walla boog ngeen gis ne ay naaféq ngeen. 6 Waaye yaakaar naa ne dingeen gis ne man nanoo wone nun, firndeg ngëm. 7 Nu ngi ñaan Yàlla, ngeen baña def dara lu bon. Waxuma ne danoo bëgga wone noonu sunu firndeg ngëm, waaye sunu yéene mooy ngeen jëf lu baax, boo yaboo sax ñu jiiñ nu ag naaféq. 8 Ndaxte manalunu dara dëggu Yàlla gi; manunu lu dul taxawal ko. 9 Bu nu néewee doole, fekk am ngeen doole, bég nanu ci. Te sax nu ngi ñaan, ngeen jublu cig mat. 10 Looloo tax ma leen di binde nii, bala maa ñëw; bëgguma leena duma ci sañ-sañ bi ma Boroom bi jox. Jox na ma ko, ngir ma yokk seen ngëm, waaye du ngir seen kasara.
12 Saafoonteleen ak xol bu laab. Mboolem gaayi Yàlla yépp ñu ngi leen di nuyu.
13 Yal na yiwu sunu Boroom Yeesu Kirist, ak mbëggeelu Yàlla ak booloo, gi nu am ak Xel mu Sell mi, ànd ak yéen ñépp.
<- 2 KORENT 12