mu bind ko
WAA KORENT
1 Man Pool, ndawul Kirist Yeesu ci coobarey Yàlla, man ak Timote sunu mbokk, noo leen di bind, yéen mbooloom Yàlla mi nekk dëkku Korent, ak gaayi Yàlla yu sell, yi nekk ci diiwaanu Akayi gépp. 2 Yal na leen Yàlla sunu Baay ak Boroom bi Yeesu Kirist may yiw ak jàmm.
8 Ndaxte bokk yi, bëggunu ngeen umple tiis, wi nu daj ci diiwaanu Asi. Yen bi diisoon na lool ba weesu sunu kàttan, ba amatunu yaakaar sax ci dund. 9 Demoon nanu ba defe ne dogalees na sunug dee. Loolu amoon na, ngir nu baña wéer sunu yaakaar ci sunu bopp, waaye nu wéer ko ci Yàlla, miy dekkal néew yi. 10 Moo nu musal ci dee gu metti googu te dina nu musalaat. Ci moom lanu wékk sunu yaakaar ne dina nu musalati, 11 bu ngeen nu jàpplee di ci boole seeni ñaan. Noonu ñu bare dinañu gërëm Yàlla ci yiw, wi mu nu may te muy tontul ñaanu ñu bare.
15 Kon ni ma ame woon kóolute googu, naroon naa jëkka jaar ci yéen, ngir ganesi leen ñaari yoon. 16 Bëggoon naa jaar ci yéen, dem diiwaanu Maseduwan, te bu ma jógee Maseduwan, dikkaat ci yéen, ngir ngeen waajal sama tukki ca Yude. 17 Ba may mébét loolu nag, ndax dama cee boolewul pastéef? Te ndax samay yéene yéeney nit kese la, ba may xel ñaar, naan «waaw» ak «déet»?
18 Wóor na Yàlla ne li nu leen di wax, du «waaw» ju ànd ak «déedéet». 19 Ndaxte Doomu Yàlla ji, Yeesu Kirist, mi nu doon yégle ci seen biir, man ak Silwan ak Timote, nekkul woon «waaw» ak «déedéet;» «waawi» Yàlla la masa nekk. 20 Te lépp lu Yàlla dige woon fekk na «waawam» ci moom. Noonu kon ci Kirist lanuy waxe: «Amiin», ngir yékkati ndamu Yàlla. 21 Te Yàlla moo nuy dëgëral ci Kirist, nun ak yéen, te sol nu Xelam. 22 Moo nu màndargaal ni ay gaayam, def Xelam ci sunu xol, muy dawal ci cér, bi mu nu dencal.
23 Man nag Yàlla seede na ma, te giñ naa ci sama bakkan ne yërëm leen rekk moo tax délseeguma Korent. 24 Du caageen nag noo leen bëgga not ci lu jëm ci seen ngëm, waaye nu ngi liggéeyandoo ak yéen ngir seen mbég, ndaxte ci ngëm ngeen sax.
2 KORENT 2 ->