3 Ci wàllu ñi seen jëkkër faatu nag, ku ci sësul ci kenn, teral ko ngir Yàlla. 4 Waaye ku ci am ay doom mbaa ay sët, na njaboot googu jëkka wone seen ragal Yàlla ci seen biir kër, ci delloo njukkal seen waajur, ndaxte loolu lu rafet la fa kanam Yàlla.
5 Jigéen ju sësul ci kenn day wékk yaakaaram jépp ci Yàlla, sax ci di ko wéetal te di ko ñaan guddi ak bëccëg. 6 Waaye ki bànneex jiital, ndee luy dox la. 7 Dénk leen loolu, ngir ñu baña am benn gàkk. 8 Ndaxte ki defalul ay bokkam dara, rawatina ay waajuram, weddi na yoonu ngëm wi, ba yées ku gëmadi.
9 Ku bëgga bindu ci ñi seen jëkkër faatu, nii la wara mel: war na wees juróom benn fukki at, di jigéen ju yemoon ci jëkkëram, 10 te mu ràññiku ci jëf yu rafet yu deme ni yar ay goneem, man gan, geestu gaayi Yàlla yu sell yi[a], dimbali ñi nekk ci tiis; maanaa di ku takku ci mboolem jëf yu rafet yi.
11 Waaye bul bind jigéen ju ndaw, ndaxte bu ko ay bëgg-bëggam xiiree ci sore Kirist, dina bëgga séyaat, 12 te dina daje ak mbugal ndaxte fecci na kóllëre. 13 Te du yem ci bëgga séyaat rekk, waaye ku tayel lay doon; di ku wër kër ak kër, rax-ca-dolli réy làmmiñ te deñ kumpa, di wax lu yoonam nekkul. 14 Looloo tax ma bëgg, jigéen yu ndaw yi séyaat, am ay doom, yor seeni kër, ba seen benn noon du leen mana gàkkal. 15 Ndaxte fi mu ne sax am na ñu jeng xaat, ba topp Seytaane.
16 Kon nag jigéen ju gëm te am mbokk mu jëkkëram faatu, na ko dimbali te bañ koo bàyyeek mbooloom ñi gëm. Noonu mbooloo mi dina mana dimbali jigéen ñi sësul ci kenn.
21 Léegi nag maa ngi lay dénk fa kanam Yàlla ak Kirist Yeesu ak malaaka yu tedd ya, nga sàmm loolu ma wax te bañ cee gënale walla di ci parlàqu. 22 Bul gaawa teg loxo kenn, ba fal ko, di séddu noonu ci bàkkaari jaambur, waaye dëkkal ci sellaay.
23 Ba tey bul yemati ci ndox mu ñuul rekk, waaye nangay naan tuuti biiñ, ngir faj say metiti biir ak say jagadi yu bare.
24 Am na, ñu seeni bàkkaar fés ci kanam ñépp, ba jiitu leen ca àtte ba; ñi seeni bàkkaar nëbbu nag, bés baa ngi leen di xaar. 25 Naka noonu it am na, ñu seen jëf yu rafet leer, te yi feeñul manuñoo nekk kumpa ba fàww.
<- 1 TIMOTE 41 TIMOTE 6 ->- a Mbaa: raxas tànki gaayi Yàlla yu sell yi,