Link to home pageLanguagesLink to all Bible versions on this site
9
Dëddu naa peyu ndawal Kirist te lew na ma
1 Ndax awma ndogal ci li may def? Ndax duma ndawul Kirist? Ndax gisuma Yeesu sunu Boroom? Xanaa du yéena soqikoo ci liggéey bi ma Boroom bi sant? 2 Su ma ñenn ñi tegul ndaw, moom laa ci yéen, ndaxte yéenay firnde jiy wone ne ndawul Boroom bi dëgg laa.

3 Nii laay tontoo ñi may àtte: 4 Xanaa sañunoo lekk ak a naan? 5 Xanaa sañunoo indaale soxna su gëm Kirist, ni yeneen ndawul Kirist ak doomi ndeyu Boroom bi ak Sefas sax? 6 Walla boog man ak Barnabas rekk noo wara daan sunu doole?

7 Kan moo masa solu soldaar ci pexey boppam? Kan mooy bey tool te du ci jariñu? Walla kan mooy sàmm jur te du naan ca soow ma? 8 Lii may wax, du ci yëfi doom Aadama rekk laa ko jukkee; xanaa du yoon wi it moo ko santaane? 9 Ndaxte bind nañu ci yoonu Musaa ne: «Bul sunjuñ gémmiñu nag wu ñu takk ci bojjukaay.» Ndax mooy tekki nag ne, Yàlla dafa bàyyi xel nag yi? 10 Walla boog xanaa nun noo moom wax jooju? Waaw, noo tax ñu bind loolu. Noonu kuy bey war na am yaakaar, te kuy bojj di yaakaara jot wàllam. 11 Nu ji ci yéen yëfi Xelum Yàlla, ba noppi góobe ci yéen yëfi àddina, ndax loolu dafa ëpp li nu wara séentu? 12 Ndegam ñeneen a am sañ-sañ boobu ci yéen, nun kon waxi-noppi.

Waaye nag jariñoowunu sañ-sañ boobu. Danuy far muñ lépp, ngir baña indi ndog ci yoonu xibaaru jàmm bu Kirist bi. 13 Xanaa xamuleen ne, ñiy liggéeyal yëf yu sell yi, dañuy lekk ñam, wi ci kër Yàlla gi, te ñiy liggéey ci sarxalukaay bi, dañuy jot seen wàll ci sarax yi? 14 Naka noonu it Boroom bi digle na ne, ñiy yégle xibaaru jàmm bi, nanu ci dund.

15 Waaye man jariñoowuma benn ci sañ-sañ yooyu, te binduma yëf yooyu, ngir ngeen di ma defal yu ni mel. Dee sax moo ma ko gënal— kenn du jële ci man mbir moomu may kañoo! 16 Su may yégle xibaaru jàmm bi, manuma cee kañu. Sas la, wu ñu ma sas. Dinaa torox, su ma yéglewul xibaaru jàmm bi! 17 Su doon ci sama coobare laa yégle xibaaru jàmm bi, man naa ci séentu yool. Waaye defuma ko ci sama coobare, ndaxte sas la, wu ñu ma sas. 18 Kon nag lan mooy sama yool? Xanaa di yégle xibaaru jàmm bi ci dara, te baña jariñoo sañ-sañ boobu ma ci yelloo.

19 Gor laa te kenn moomu ma; teewul def naa sama bopp jaamu ñépp, ngir mana gindi nit ñu bare ci Kirist. 20 Ci biir Yawut yi, sol naa melow Yawut yi, ngir gindi leen. Man ci sama bopp yoonu Musaa jiitalu ma, terewul bi ma nekkee ci biir ñiy sàmm yoonu Musaa, sàmm naa yoon wa, ngir gindi leen. 21 Ci biir ñi nekkul ci yoonu Musaa, faalewuma woon yoon wi, ngir gindi leen; waxuma ne ànduma ak yoonu Yàlla, waaye topp naa yoon ci sama bokk ak Kirist. 22 Ci biir ñi néew ngëm, meloon naa ni ku néew ngëm, ngir gindi leen. Doon naa lépp ci ñépp, ngir def lépp lu ma man, ba ñenn mucc ci. 23 Damaa def loolu lépp ndax xibaaru jàmm bi, ngir man it ma am wàll ci barkeem.

24 Xanaa xamuleen ne, ñépp ñooy daw cib rawante, waaye kenn rekk ay jël ndam li? Dawleen nag ngir jël ko. 25 Ñiy joŋante ci po muy waral tàggat yaram, dañuy xañ seen bopp lu bare. Dañu koy def, ngir am kaalag ndam gu dul yàgg; waaye nun danu koy def, ngir am kaalag ndam gu sax ba fàww. 26 Man nag noonu laay dawe, te duma dawantu. Noonu laay bëree, waaye duma def ni nit kuy dóor ci jaww ji. 27 Waaye damay not sama yaram, ba moom ko, ngir ragala yégal ñi ci des xibaaru jàmm bi, ba noppi Yàlla xañ ma ndam li.

<- 1 KORENT 81 KORENT 10 ->