Link to home pageLanguagesLink to all Bible versions on this site

1 Man ci sama bopp, bokk yi, bi ma ñëwee ci yéen, ngir yégle mbóoti Yàlla, ñëwuma ci ay wax yu neex ak xam-xam bu réy. 2 Dogu woon naa ci baña xam dara ci seen biir lu dul Yeesu Kirist, te muy ki ñu rey ca bant ba. 3 Bi ma teewee ci yéen, ànd naa ak ñàkk doole, ragal ak njàqare. 4 Li ma wax ak li ma waare, defuma ko ci làmmiñ wu neex, sukkandikoo ko ci xam-xamu nit, waaye ànd na ak ay firnde yu soqikoo ci kàttanu Xelum Yàlla, 5 ngir seen ngëm baña wékku ci xam-xamu nit ñi waaye mu wékku ci dooley Yàlla.

Xelum Yàlla mooy joxe xam-xamu Yàlla
6 Moona am na xam-xam bu nuy yégal ñi mat, xam-xam bu bokkul ci àddina si, te njiiti àddina si xamuñu ko, ñoom ñi nara wéy. 7 Nu ngi yégle mbóotu xam-xamu Yàlla, mu nëbbu woon te Yàlla dogal ko ngir sunu ndam, laata àddina di sosu. 8 Kenn ci njiiti àddina amul woon xam-xam boobu. Su ñu ko amoon, kon duñu rey Boroom ndam li ci bant bi. 9 Waaye Mbind mi nee na:
«Lu bët gisul,
nopp déggu ko,
xel xalaatu ko,
loolu la Yàlla dencal ñi ko bëgg.»
10 Fekk nag nun la ko Yàlla won, jaarale ko ci Xelam.
Xelum Yàlla mooy leeral lépp, ba ci xalaati Yàlla yi gëna xóot. 11 Kan ci nit ñi moo xam yëfi nit? Xanaa xelum nit mi nekk ci moom rekk a ko xam. Noonu it kenn xamul yëfi Yàlla, ku dul Xelum Yàlla. 12 Nun nag Xel mi nu jot, jógewul ci àddina, waaye Yàllaa nu ko sol. 13 Loolu nu Yàlla may, yéglewunu ko ci ay baat yu soqikoo ci xam-xamu nit, waaye nu ngi koy yégle ci baat, yi soqikoo ci Xelum Yàlla, di tekkantal yëfi Xelum Yàlla ci ay baat yu mu nu sol. 14 Nit kese du nangu yëfi Xelum Yàlla. Ag ndof lay doon ci moom; du ko mana nangu, ndaxte ku yor Xelum Yàlla rekk moo ko mana ràññale. 15 Nit ki yor Xelum Yàlla dafay àtte lépp; moom ci boppam, kenn du ko àtte. 16 Ndaxte Mbind mi nee na:
«Ana ku xam xalaatu Boroom bi?
Ku ko doon digal?»
Waaye nun am nanu xalaatu Kirist.

<- 1 KORENT 11 KORENT 3 ->