10 Bu leen Timote ganesee, fexeleen ba bumu am njàqare ci seen biir, ndaxte dafay liggéeyal Boroom bi ni man. 11 Kon bu ko kenn xeeb. Nangeen taxawu yoonam, ba mu délsi ci man ci jàmm, ndaxte maa ngi koy xaar ak bokk yi.
12 Naka Apolos sunu mbokk mi nag moom, xiir naa ko ay yooni yoon, mu ñëw ci yéen, ànd ak bokk yi. Waaye fi mu ne dëppoowul ak coobareem. Dina ñëw saa su ko manee.
13 Farluleen te dëgër ci ngëm, di góor-góorlu te am pastéef. 14 Lépp li ngeen di def, defleen ko ak mbëggeel.
15 Xam ngeen ne, Estefanas ak njabootam ñoo jëkka nangu xibaaru jàmm bi ci diiwaanu Akayi, te ñoo joxe seen bopp, ngir liggéeyal gaayi Yàlla yi. Kon nag bokk yi, maa ngi leen di ñaan, 16 ngeen nangul nit ñu mel noonu, ñoom ak képp ku ànd ak ñoom ci liggéey bi. 17 Bi ma Estefanas ak Fortunatus ak Akaykus seetsee, bég naa ci lool. Taxawal nañu leen ci topptoo, bi ngeen yéene woon ci man te tële ko. 18 Seral nañu sama xol ak seen yos itam. Kon fonkleen nit ñu mel noonu.
21 Man Pool maa bind nuyoo bii ci sama loxob bopp.
22 Képp ku bañ Boroom bi, yal na ko Yàlla alag. Boroom bi, ñëwal!
23 Yal na yiwu Boroom bi Yeesu ànd ak yéen.
24 Bëgg naa leen yéen ñépp ndax sunu booloo ak Yeesu Kirist.
<- 1 KORENT 15