4 Ku bëgg dafay muñ te laabiir. Ku bëgg du iñaan, du kañu, du tiitaru, 5 du def lu jekkadi, du wut njariñu boppam, du naqari deret, du ñaaw njort. 6 Du bég ci lu awul yoon, waaye dina bég ci lépp luy jollil dëgg. 7 Mbëggeel day baale lépp, am gëm ci lépp, yaakaar lépp, muñ lépp.
8 Mbëggeel amul àpp. Ñiy wax ci kàddug Yàlla dinañu noppi, ñiy wax ay làkk dinañu ko bàyyi, ñiy xamle xam-xamu Yàlla wàcc. 9 Xam-xam bi nu am des na, te ni nu jottalee xibaar bi nu Yàlla dénk des na. 10 Waaye li mat, bu dikkee, li matul jóge fi. 11 Bi ma dee xale, dama doon wax ni xale, di dégge ni xale, di xalaate ni xale. Waaye bi ma doonee mag, bàyyi naa lu bokkoon cig ndaw. 12 Tey jii gis bu lëndëm lanuy gis, ni takkandeer ci seetu bu lëndëm; bu ëllëgee dinanu gis jaxran. Tey jii sama xam-xam des na; bu ëllëgee dinaa xam ba mat sëkk, ni ma Yàlla xame.
13 Léegi nag ñett yii ñooy sax: ngëm, yaakaar, mbëggeel; te mbëggeel moo ci raw.
<- 1 KORENT 121 KORENT 14 ->