6 Mbir yooyu ay misaal lañu, yu nuy artu, ngir benn bëgg-bëgg bu bon bañ noo jiital, na mu leen jiitale woon. 7 Buleen jaamu ay xërëm, ni ko ñenn ñi ci ñoom defe woon. Ndaxte Mbind mi nee na: «Mbooloo mi dafa toog, di lekk ak di naan, ba noppi ñu jóg di mbumbaay.» 8 Bunu njaaloo, ni ko ñenn ñi ci ñoom defe woon, ba tax ñaar fukki junni ak ñett ci ñoom dee ci benn bés. 9 Bunu diiŋat Kirist, ni ko ñenn ñi ci ñoom defe, ba ay jaan màtt leen, ñu dee. 10 Buleen xultu, ni ko ñenn ñi ci ñoom defe woon, ba tax Malaakam bóomkat bi rey leen.
11 Mbir yooyu leen daloon misaal la ci nun, te bind nañu ko ngir artu nu, nun ñiy dund ci jamono jii lépp mat. 12 Kon nag kiy naw sa doole, ba yaakaar ne taxaw nga, moytula daanu ci bàkkaar! 13 Benn nattu dabu leen bu wuute ak yi dal nit ñépp. Te sax Yàlla kuy sàmm kóllëre la, te du nangu nattu bi wees seen kàttan, waaye cib nattu dina leen ubbil bunt bu ngeen mana rëcce, ba ngeen man koo dékku.
18 Seetleen ci bànni Israyil. Ñiy lekk sarax si ñu rendi, ndax booloowuñu ak Yàlla ji ñu jagleel sarxalukaay ba? Ahakay! 19 Li may wax, lu muy tekki? Ndax yàpp wi ñu jagleel xërëm yi dafay dara? Walla xërëm yi dañuy dara? 20 Déedéet! Waaye sarax yi xërëmkat yi di rendi, ay rab lañu ko jagleel; jagleeluñu ko Yàlla. Te man bëgguma, ngeen booloo ak rab yi. 21 Manuleena naan ci kaasu Boroom bi, naan ci kaasu rab yi. Manuleena sukk ci reerub Boroom bi, sukk ci reerub rab yi. 22 Walla boog ndax danuy jéema gillil meru Boroom bi? Xanaa noo ko ëpp doole?
25 Man ngeena lekk lépp lu ñuy jaay ca ja ba, bañ cee boole ay laaj ngir dalal seen xel. 26 Ndaxte Mbind mi nee na: «Àddina ak li ci biiram lépp, Boroom bi moo ko moom.»
27 Ku xamul Yàlla nag, bu leen wooyee aw ñam këram, te ngeen nangoo dem, lekkleen lépp lu ñu leen dëj, baña laajte dara ngir dalal seen xel. 28 Waaye bu leen kenn nee: «Lii sarax la, bu ñu jagleel xërëm yi,» suurleen ko ndax ki leen ko xamal, ngir xel mu dal. 29 Waxuma sa xel yaw, waaye xelu keneen laay wax.
31 Kon su ngeen di lekk walla ngeen di naan, walla lu ngeen mana def, defleen lépp ngir màggal Yàlla. 32 Buleen def dara lu mana fanq ngëmu Yawut yi walla ñi dul Yawut walla mbooloom Yàlla. 33 Noonu laay def man ci sama bopp: damay wuta neex ñépp ci lépp. Wutuma lu may jariñ, waaye luy jariñ ñu bare laay wut, ngir ñu mucc.
<- 1 KORENT 91 KORENT 11 ->- a Ba bànni Israyil nekkee ca màndiŋ ma, Boroom bi moom ci boppam moo leen jiite woon, mel ni niir ci bëccëg bi, ngir gindi leen, su guddee mu doon jumu sawara, ngir niital leen.